Saba · 1/54
Tekki Waxtaan — Saba
الْحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي لَهُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ وَلَهُ الْحَمْدُ فِي الْآخِرَةِ ۚ وَهُوَ الْحَكِيمُ الْخَبِيرُ ۝١
Alhamdu lillaahil lazee lahoo maa fis samaawaati wa maa fil ardi wa lahul hamdu fil aakhirah; wa Huwal Hakeemul Khabeer
📖 Tekkim Wolof
Cant ñeel na Yàlla, Yàlla mi moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Cant it ñeel na ko ca àllaaxira. Moo di Ku Xereñ, di Ku Xàmmee.

🎧 Dégg


📜 Aaya 1-3 — Saba

1الْحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي لَهُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ وَلَهُ الْحَمْدُ فِي الْآخِرَةِ ۚ وَهُوَ الْحَكِيمُ الْخَبِيرُ
Cant ñeel na Yàlla, Yàlla mi moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Cant it ñeel na ko ca àllaaxira. Moo di Ku Xereñ, di Ku Xàmmee.
2يَعْلَمُ مَا يَلِجُ فِي الْأَرْضِ وَمَا يَخْرُجُ مِنْهَا وَمَا يَنزِلُ مِنَ السَّمَاءِ وَمَا يَعْرُجُ فِيهَا ۚ وَهُوَ الرَّحِيمُ الْغَفُورُ
Xam na li duggu ci suuf ak la cay génne, ak lay wàcc ci asamaan si ak la cay yéeg. Mooy Jaglewaakoon ba, di Jéggalaakoon ba.
3وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا لَا تَأْتِينَا السَّاعَةُ ۖ قُلْ بَلَىٰ وَرَبِّي لَتَأْتِيَنَّكُمْ عَالِمِ الْغَيْبِ ۖ لَا يَعْزُبُ عَنْهُ مِثْقَالُ ذَرَّةٍ فِي السَّمَاوَاتِ وَلَا فِي الْأَرْضِ وَلَا أَصْغَرُ مِن ذَٰلِكَ وَلَا أَكْبَرُ إِلَّا فِي كِتَابٍ مُّبِينٍ
Yéefar yaa ngay wax naan : “Bis-pénc ba du ñëw”. Waxal ne : “Axakañ. Giñ naa ci sama Boroom ! ne dana leen dikkal. Moom mi xam kumpa. Te dara lu tollu ni aw pepp du ko lënt ci asamaan yeek suuf si. Walla lu ko gën a tuuti, walla lu ko gën a rëy, lu dul ne mi ngi ci ab Téere bu bir.
SabaFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
1Aaya

Tekki — Saba 1

Simoore Saba Aaya 1 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Cant ñeel na Yàlla, Yàlla mi moom li nekk ci…

Simoore Aaya 1/54 — Saba سبأ (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Saba Dégg, Saba Tekki, Saba mp3, Saba pdf. Aaya 1–3. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers