Fatir · 6/45
Tekki Waxtaan — Fatir
إِنَّ الشَّيْطَانَ لَكُمْ عَدُوٌّ فَاتَّخِذُوهُ عَدُوًّا ۚ إِنَّمَا يَدْعُو حِزْبَهُ لِيَكُونُوا مِنْ أَصْحَابِ السَّعِيرِ ۝٦
Innash shaitaana lakum `aduwwun fattakhizoohu `aduwwaa; innamaa yad`oo hizbahoo liyakoonoo min ashaabis sa`eer
📖 Tekkim Wolof
Séytaane, seenub noon la. Nangeen ko jàppe ab noon. Li muy woote di ci xiirtal gàngooram moo di ngir ñu nekk waa Safara doŋŋ la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 4-8 — Fatir

4وَإِن يُكَذِّبُوكَ فَقَدْ كُذِّبَتْ رُسُلٌ مِّن قَبْلِكَ ۚ وَإِلَى اللَّهِ تُرْجَعُ الْأُمُورُ
Bu ñu la weddee it, xamal ne weddi woon nañu ay Yonent yu la jiitu woon. Te ca Yàlla la mbir yi di mujj.
5يَا أَيُّهَا النَّاسُ إِنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ ۖ فَلَا تَغُرَّنَّكُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا ۖ وَلَا يَغُرَّنَّكُم بِاللَّهِ الْغَرُورُ
Éy yéen nit ñi ! Li Yàllay dige dëgg la. Buleen dundug àddina bii di fàbbi, buleen Séytaane tax a fakku ci Yàlla.
6إِنَّ الشَّيْطَانَ لَكُمْ عَدُوٌّ فَاتَّخِذُوهُ عَدُوًّا ۚ إِنَّمَا يَدْعُو حِزْبَهُ لِيَكُونُوا مِنْ أَصْحَابِ السَّعِيرِ
Séytaane, seenub noon la. Nangeen ko jàppe ab noon. Li muy woote di ci xiirtal gàngooram moo di ngir ñu nekk waa Safara doŋŋ la.
7الَّذِينَ كَفَرُوا لَهُمْ عَذَابٌ شَدِيدٌ ۖ وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَأَجْرٌ كَبِيرٌ
Ña weddi, mbugal mu metti dana leen dal, ña gëm nag tey jëf u yiw, danañu am njéggal ak pey gu rëy .
8أَفَمَن زُيِّنَ لَهُ سُوءُ عَمَلِهِ فَرَآهُ حَسَنًا ۖ فَإِنَّ اللَّهَ يُضِلُّ مَن يَشَاءُ وَيَهْدِي مَن يَشَاءُ ۖ فَلَا تَذْهَبْ نَفْسُكَ عَلَيْهِمْ حَسَرَاتٍ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِمَا يَصْنَعُونَ
Naka kay jàppee ñaawtéefam ya muy lu rafet... ? – Yàllaay réeral ku ko soob, di gindi ku ko soob – Bul sonnal sa bopp ci ñoom : Yàlla xam na xéll la ñuy def.
FatirFihi Alxuraan
45Aaya
MeccanRevelation
6Aaya

Tekki — Fatir 6

Simoore Fatir Aaya 6 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Séytaane, seenub noon la. Nangeen ko jàppe ab noon. Li…

Simoore Aaya 6/45 — Fatir فاطر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fatir Dégg, Fatir Tekki, Fatir mp3, Fatir pdf. Aaya 4–8. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers