Fatir · 5/45
Tekki Waxtaan — Fatir
يَا أَيُّهَا النَّاسُ إِنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ ۖ فَلَا تَغُرَّنَّكُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا ۖ وَلَا يَغُرَّنَّكُم بِاللَّهِ الْغَرُورُ ۝٥
Yaaa ayyuhan naasu inna wa`dal laahi haqqun falaa taghurrannakumul hayaatud dunyaa; wa laa yaghurran nakum billaahil gharoor
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen nit ñi ! Li Yàllay dige dëgg la. Buleen dundug àddina bii di fàbbi, buleen Séytaane tax a fakku ci Yàlla.
🎧 Dégg

📜 Aaya 3-7 — Fatir

3يَا أَيُّهَا النَّاسُ اذْكُرُوا نِعْمَتَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ ۚ هَلْ مِنْ خَالِقٍ غَيْرُ اللَّهِ يَرْزُقُكُم مِّنَ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ ۚ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ فَأَنَّىٰ تُؤْفَكُونَ
Éy yéen nit ñi ! Fàttalikuleen xéewali Yàlla yi ci yéen : moo ndax amuñu bindkat bu dul Yàlla, bu leen di wërsëgal ci asamaan yeek suuf si ? Amul jeneen yàlla ju dul Moom ! Moo yéen ndax mën ngeen koo dummóoyu ?
4وَإِن يُكَذِّبُوكَ فَقَدْ كُذِّبَتْ رُسُلٌ مِّن قَبْلِكَ ۚ وَإِلَى اللَّهِ تُرْجَعُ الْأُمُورُ
Bu ñu la weddee it, xamal ne weddi woon nañu ay Yonent yu la jiitu woon. Te ca Yàlla la mbir yi di mujj.
5يَا أَيُّهَا النَّاسُ إِنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ ۖ فَلَا تَغُرَّنَّكُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا ۖ وَلَا يَغُرَّنَّكُم بِاللَّهِ الْغَرُورُ
Éy yéen nit ñi ! Li Yàllay dige dëgg la. Buleen dundug àddina bii di fàbbi, buleen Séytaane tax a fakku ci Yàlla.
6إِنَّ الشَّيْطَانَ لَكُمْ عَدُوٌّ فَاتَّخِذُوهُ عَدُوًّا ۚ إِنَّمَا يَدْعُو حِزْبَهُ لِيَكُونُوا مِنْ أَصْحَابِ السَّعِيرِ
Séytaane, seenub noon la. Nangeen ko jàppe ab noon. Li muy woote di ci xiirtal gàngooram moo di ngir ñu nekk waa Safara doŋŋ la.
7الَّذِينَ كَفَرُوا لَهُمْ عَذَابٌ شَدِيدٌ ۖ وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَأَجْرٌ كَبِيرٌ
Ña weddi, mbugal mu metti dana leen dal, ña gëm nag tey jëf u yiw, danañu am njéggal ak pey gu rëy .
FatirFihi Alxuraan
45Aaya
MeccanRevelation
5Aaya

Tekki — Fatir 5

Simoore Fatir Aaya 5 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen nit ñi ! Li Yàllay dige dëgg la.…

Simoore Aaya 5/45 — Fatir فاطر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fatir Dégg, Fatir Tekki, Fatir mp3, Fatir pdf. Aaya 3–7. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers