An-Nisa · 80/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
مَّن يُطِعِ الرَّسُولَ فَقَدْ أَطَاعَ اللَّهَ ۖ وَمَن تَوَلَّىٰ فَمَا أَرْسَلْنَاكَ عَلَيْهِمْ حَفِيظًا ۝٨٠
Man yuti`ir Rasoola faqad ataa`al laaha wa man tawallaa famaaa arsalnaaka `alaihim hafeezaa
📖 Tekkim Wolof
Képp ku topp Yonent ba topp na ndigalu Yàlla. Ku dummóoyu [weddi]... Xamal ne yónniwuñu la ci ñoom ngir nga di leen wattu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 78-82 — An-Nisa

78أَيْنَمَا تَكُونُوا يُدْرِككُّمُ الْمَوْتُ وَلَوْ كُنتُمْ فِي بُرُوجٍ مُّشَيَّدَةٍ ۗ وَإِن تُصِبْهُمْ حَسَنَةٌ يَقُولُوا هَٰذِهِ مِنْ عِندِ اللَّهِ ۖ وَإِن تُصِبْهُمْ سَيِّئَةٌ يَقُولُوا هَٰذِهِ مِنْ عِندِكَ ۚ قُلْ كُلٌّ مِّنْ عِندِ اللَّهِ ۖ فَمَالِ هَٰؤُلَاءِ الْقَوْمِ لَا يَكَادُونَ يَفْقَهُونَ حَدِيثًا
Fu ngeen mën a nekk dey, dee dana leen fa fekk, doonte la dangeen a nekk ci tata yu ñoŋ. Te bu leen lu neex dikkalee, ñu ne : “Lii ci Yàlla la bawoo [jóge].”. Bu leen naqar dalee, ñu ne : “Lii ci yaw [Muhammad] la jóge.”. Neel : “Lépp ca Yàlla la jóge.” Waaw ana lu nekk ca ñooña nit ba xawuñoo déggati wax [ju am njariñ] ?
79مَّا أَصَابَكَ مِنْ حَسَنَةٍ فَمِنَ اللَّهِ ۖ وَمَا أَصَابَكَ مِن سَيِّئَةٍ فَمِن نَّفْسِكَ ۚ وَأَرْسَلْنَاكَ لِلنَّاسِ رَسُولًا ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ شَهِيدًا
Lu la dal ci lu baax ma nga jóge ca Yàlla, lu bon lu la dal ci sa bakkan la jóge. Te yónni Nanu la [yaw Muhammad] nga di ab Yonent. Te Yàlla doy na seede ci lépp.
80مَّن يُطِعِ الرَّسُولَ فَقَدْ أَطَاعَ اللَّهَ ۖ وَمَن تَوَلَّىٰ فَمَا أَرْسَلْنَاكَ عَلَيْهِمْ حَفِيظًا
Képp ku topp Yonent ba topp na ndigalu Yàlla. Ku dummóoyu [weddi]... Xamal ne yónniwuñu la ci ñoom ngir nga di leen wattu.
81وَيَقُولُونَ طَاعَةٌ فَإِذَا بَرَزُوا مِنْ عِندِكَ بَيَّتَ طَائِفَةٌ مِّنْهُمْ غَيْرَ الَّذِي تَقُولُ ۖ وَاللَّهُ يَكْتُبُ مَا يُبَيِّتُونَ ۖ فَأَعْرِضْ عَنْهُمْ وَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ وَكِيلًا
Danañu wax ne : “Nangul nanu la ! ” Te bu ñu jóge ci yaw , ab kurél ci ñoom dana fanaanoo lu wuuteek la ñu la waxoon. Yàlla Dana bind la ñu fanaane. Nanga leen dëddu te nga wéeru ci Yàlla. Yàlla doy na ndëgërlaay .
82أَفَلَا يَتَدَبَّرُونَ الْقُرْآنَ ۚ وَلَوْ كَانَ مِنْ عِندِ غَيْرِ اللَّهِ لَوَجَدُوا فِيهِ اخْتِلَافًا كَثِيرًا
Moo ndax ñoom dañu dul settantal Alxuraan ? Alxuraan, bu jóge woon ci keneen ku dul Yàlla, fàwwu ñu gis ca ay juuyoo ciy waxam !
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
80Aaya

Tekki — An-Nisa 80

Simoore An-Nisa Aaya 80 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Képp ku topp Yonent ba topp na ndigalu Yàlla. Ku…

Simoore Aaya 80/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 78–82. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers