An-Nisa · 81/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَيَقُولُونَ طَاعَةٌ فَإِذَا بَرَزُوا مِنْ عِندِكَ بَيَّتَ طَائِفَةٌ مِّنْهُمْ غَيْرَ الَّذِي تَقُولُ ۖ وَاللَّهُ يَكْتُبُ مَا يُبَيِّتُونَ ۖ فَأَعْرِضْ عَنْهُمْ وَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ وَكِيلًا ۝٨١
Wa yaqooloona taa`antun fa izaa barazoo min `indika baiyata taaa`ifatum minhum ghairal lazee taqoolu wallaahu yaktubu maa yubaiyitoona faa`rid `anhum wa tawakkal `alal laah; wa kafaa billaahi Wakeelaa
📖 Tekkim Wolof
Danañu wax ne : “Nangul nanu la ! ” Te bu ñu jóge ci yaw , ab kurél ci ñoom dana fanaanoo lu wuuteek la ñu la waxoon. Yàlla Dana bind la ñu fanaane. Nanga leen dëddu te nga wéeru ci Yàlla. Yàlla doy na ndëgërlaay .
🎧 Dégg

📜 Aaya 79-83 — An-Nisa

79مَّا أَصَابَكَ مِنْ حَسَنَةٍ فَمِنَ اللَّهِ ۖ وَمَا أَصَابَكَ مِن سَيِّئَةٍ فَمِن نَّفْسِكَ ۚ وَأَرْسَلْنَاكَ لِلنَّاسِ رَسُولًا ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ شَهِيدًا
Lu la dal ci lu baax ma nga jóge ca Yàlla, lu bon lu la dal ci sa bakkan la jóge. Te yónni Nanu la [yaw Muhammad] nga di ab Yonent. Te Yàlla doy na seede ci lépp.
80مَّن يُطِعِ الرَّسُولَ فَقَدْ أَطَاعَ اللَّهَ ۖ وَمَن تَوَلَّىٰ فَمَا أَرْسَلْنَاكَ عَلَيْهِمْ حَفِيظًا
Képp ku topp Yonent ba topp na ndigalu Yàlla. Ku dummóoyu [weddi]... Xamal ne yónniwuñu la ci ñoom ngir nga di leen wattu.
81وَيَقُولُونَ طَاعَةٌ فَإِذَا بَرَزُوا مِنْ عِندِكَ بَيَّتَ طَائِفَةٌ مِّنْهُمْ غَيْرَ الَّذِي تَقُولُ ۖ وَاللَّهُ يَكْتُبُ مَا يُبَيِّتُونَ ۖ فَأَعْرِضْ عَنْهُمْ وَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ وَكِيلًا
Danañu wax ne : “Nangul nanu la ! ” Te bu ñu jóge ci yaw , ab kurél ci ñoom dana fanaanoo lu wuuteek la ñu la waxoon. Yàlla Dana bind la ñu fanaane. Nanga leen dëddu te nga wéeru ci Yàlla. Yàlla doy na ndëgërlaay .
82أَفَلَا يَتَدَبَّرُونَ الْقُرْآنَ ۚ وَلَوْ كَانَ مِنْ عِندِ غَيْرِ اللَّهِ لَوَجَدُوا فِيهِ اخْتِلَافًا كَثِيرًا
Moo ndax ñoom dañu dul settantal Alxuraan ? Alxuraan, bu jóge woon ci keneen ku dul Yàlla, fàwwu ñu gis ca ay juuyoo ciy waxam !
83وَإِذَا جَاءَهُمْ أَمْرٌ مِّنَ الْأَمْنِ أَوِ الْخَوْفِ أَذَاعُوا بِهِ ۖ وَلَوْ رَدُّوهُ إِلَى الرَّسُولِ وَإِلَىٰ أُولِي الْأَمْرِ مِنْهُمْ لَعَلِمَهُ الَّذِينَ يَسْتَنبِطُونَهُ مِنْهُمْ ۗ وَلَوْلَا فَضْلُ اللَّهِ عَلَيْكُمْ وَرَحْمَتُهُ لَاتَّبَعْتُمُ الشَّيْطَانَ إِلَّا قَلِيلًا
Su leen mbir ma dikkale ci kóolute walla tiitaange, ñu siiwal ko. Te bu ñu ko delloo woon ca Yonent ba walla kilifa ya nekk ca ñoom, kon ña ko soloo xam ne ñoom danañu ca am lu leer bu dul woon ak xéewali Yàlla ak yërmaandeem ci yéen. Giñ naa ne kon lim bu néew ci yéen moo dul topp [Séytaane].
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
81Aaya

Tekki — An-Nisa 81

Simoore An-Nisa Aaya 81 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Danañu wax ne : “Nangul nanu la ! ” Te…

Simoore Aaya 81/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 79–83. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers