Ash-Shura · 18/53
Tekki Waxtaan — Ash-Shura
يَسْتَعْجِلُ بِهَا الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِهَا ۖ وَالَّذِينَ آمَنُوا مُشْفِقُونَ مِنْهَا وَيَعْلَمُونَ أَنَّهَا الْحَقُّ ۗ أَلَا إِنَّ الَّذِينَ يُمَارُونَ فِي السَّاعَةِ لَفِي ضَلَالٍ بَعِيدٍ ۝١٨
Yasta`jilu bihal lazeena laa yu`minoona bihaa wallazeena aamanoo mushfiqoona minhaa wa ya`lamoona annahal haqq; alaaa innal lazeena yumaaroona fis Saa`ati lafee dalaalim ba`eed
📖 Tekkim Wolof
Ña ko gëmul ña nga koy yàkkamti ; waaye ña gëm ñoom dañu koy ragal te xam nañu ne mooy dëgg tigi. Ñay werante ci mbirum waxtu wa (Bis Pénc ba) ña nga ci réer gu sore.

🎧 Dégg


📜 Aaya 16-20 — Ash-Shura

16وَالَّذِينَ يُحَاجُّونَ فِي اللَّهِ مِن بَعْدِ مَا اسْتُجِيبَ لَهُ حُجَّتُهُمْ دَاحِضَةٌ عِندَ رَبِّهِمْ وَعَلَيْهِمْ غَضَبٌ وَلَهُمْ عَذَابٌ شَدِيدٌ
Ñiy diiŋat mbiri Yàlla, ginnaaw ba ñu ko nangulee, seenu lay la naaxsaay la ca Yàlla. Te mer dal na ci seen kaw ñu am mbugël mu tar.
17اللَّهُ الَّذِي أَنزَلَ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ وَالْمِيزَانَ ۗ وَمَا يُدْرِيكَ لَعَلَّ السَّاعَةَ قَرِيبٌ
Moo di Yàlla mi wàcce Téere ba ci dëgg, ak nattukaay ba (balaas ya). Ana loo ci xam ? te amaana waxtu wa di lu jigeñ ?
18يَسْتَعْجِلُ بِهَا الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِهَا ۖ وَالَّذِينَ آمَنُوا مُشْفِقُونَ مِنْهَا وَيَعْلَمُونَ أَنَّهَا الْحَقُّ ۗ أَلَا إِنَّ الَّذِينَ يُمَارُونَ فِي السَّاعَةِ لَفِي ضَلَالٍ بَعِيدٍ
Ña ko gëmul ña nga koy yàkkamti ; waaye ña gëm ñoom dañu koy ragal te xam nañu ne mooy dëgg tigi. Ñay werante ci mbirum waxtu wa (Bis Pénc ba) ña nga ci réer gu sore.
19اللَّهُ لَطِيفٌ بِعِبَادِهِ يَرْزُقُ مَن يَشَاءُ ۖ وَهُوَ الْقَوِيُّ الْعَزِيزُ
Yàlla kuy ñeewanti jaamam ñi la. Mooy wërsëgël ku ko soob. te moo di boroom Doole ja, boroom Kàttan ga.
20مَن كَانَ يُرِيدُ حَرْثَ الْآخِرَةِ نَزِدْ لَهُ فِي حَرْثِهِ ۖ وَمَن كَانَ يُرِيدُ حَرْثَ الدُّنْيَا نُؤْتِهِ مِنْهَا وَمَا لَهُ فِي الْآخِرَةِ مِن نَّصِيبٍ
Képp ku namm ruuj [toolu] dundug àllaaxira, Dananu ko dollil ruujeefam. Képp it ku namm ruuj [toolu] dundug àddina, Dananu ko nangul ; waaye du am benn cër ca àllaaxira.
Ash-ShuraFihi Alxuraan
53Aaya
MeccanRevelation
18Aaya

Tekki — Ash-Shura 18

Simoore Ash-Shura Aaya 18 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña ko gëmul ña nga koy yàkkamti ; waaye ña…

Simoore Aaya 18/53 — Ash-Shura الشورى (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ash-Shura Dégg, Ash-Shura Tekki, Ash-Shura mp3, Ash-Shura pdf. Aaya 16–20. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers