Ash-Shura · 17/53
Tekki Waxtaan — Ash-Shura
اللَّهُ الَّذِي أَنزَلَ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ وَالْمِيزَانَ ۗ وَمَا يُدْرِيكَ لَعَلَّ السَّاعَةَ قَرِيبٌ ۝١٧
Allahul lazeee anzalal Kitaaba bilhaqqi wal Meezaan; wa ma yudreeka la`allas Saa`ata qareeb
📖 Tekkim Wolof
Moo di Yàlla mi wàcce Téere ba ci dëgg, ak nattukaay ba (balaas ya). Ana loo ci xam ? te amaana waxtu wa di lu jigeñ ?
🎧 Dégg

📜 Aaya 15-19 — Ash-Shura

15فَلِذَٰلِكَ فَادْعُ ۖ وَاسْتَقِمْ كَمَا أُمِرْتَ ۖ وَلَا تَتَّبِعْ أَهْوَاءَهُمْ ۖ وَقُلْ آمَنتُ بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ مِن كِتَابٍ ۖ وَأُمِرْتُ لِأَعْدِلَ بَيْنَكُمُ ۖ اللَّهُ رَبُّنَا وَرَبُّكُمْ ۖ لَنَا أَعْمَالُنَا وَلَكُمْ أَعْمَالُكُمْ ۖ لَا حُجَّةَ بَيْنَنَا وَبَيْنَكُمُ ۖ اللَّهُ يَجْمَعُ بَيْنَنَا ۖ وَإِلَيْهِ الْمَصِيرُ
Kon na ngay woo (nit ñi) jëme leen ci diine jooju ; te na ngay tegu ca yoon wu jub wa xocc ni ñu la ko digële ; te bul topp mukk seen bànneex ; te na nga wax ne : “Gëm naa lépp lu Yàlla wàcce mu di ab Téere, te digaleef na ma may maandu ci seen diggënte. Yàlla moo di sama Boroom. Te it Yàlla dananu dajale nun ñépp te ca moom la ñépp di mujj”.
16وَالَّذِينَ يُحَاجُّونَ فِي اللَّهِ مِن بَعْدِ مَا اسْتُجِيبَ لَهُ حُجَّتُهُمْ دَاحِضَةٌ عِندَ رَبِّهِمْ وَعَلَيْهِمْ غَضَبٌ وَلَهُمْ عَذَابٌ شَدِيدٌ
Ñiy diiŋat mbiri Yàlla, ginnaaw ba ñu ko nangulee, seenu lay la naaxsaay la ca Yàlla. Te mer dal na ci seen kaw ñu am mbugël mu tar.
17اللَّهُ الَّذِي أَنزَلَ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ وَالْمِيزَانَ ۗ وَمَا يُدْرِيكَ لَعَلَّ السَّاعَةَ قَرِيبٌ
Moo di Yàlla mi wàcce Téere ba ci dëgg, ak nattukaay ba (balaas ya). Ana loo ci xam ? te amaana waxtu wa di lu jigeñ ?
18يَسْتَعْجِلُ بِهَا الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِهَا ۖ وَالَّذِينَ آمَنُوا مُشْفِقُونَ مِنْهَا وَيَعْلَمُونَ أَنَّهَا الْحَقُّ ۗ أَلَا إِنَّ الَّذِينَ يُمَارُونَ فِي السَّاعَةِ لَفِي ضَلَالٍ بَعِيدٍ
Ña ko gëmul ña nga koy yàkkamti ; waaye ña gëm ñoom dañu koy ragal te xam nañu ne mooy dëgg tigi. Ñay werante ci mbirum waxtu wa (Bis Pénc ba) ña nga ci réer gu sore.
19اللَّهُ لَطِيفٌ بِعِبَادِهِ يَرْزُقُ مَن يَشَاءُ ۖ وَهُوَ الْقَوِيُّ الْعَزِيزُ
Yàlla kuy ñeewanti jaamam ñi la. Mooy wërsëgël ku ko soob. te moo di boroom Doole ja, boroom Kàttan ga.
Ash-ShuraFihi Alxuraan
53Aaya
MeccanRevelation
17Aaya

Tekki — Ash-Shura 17

Simoore Ash-Shura Aaya 17 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moo di Yàlla mi wàcce Téere ba ci dëgg, ak…

Simoore Aaya 17/53 — Ash-Shura الشورى (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ash-Shura Dégg, Ash-Shura Tekki, Ash-Shura mp3, Ash-Shura pdf. Aaya 15–19. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers