Ash-Shura · 19/53
Tekki Waxtaan — Ash-Shura
اللَّهُ لَطِيفٌ بِعِبَادِهِ يَرْزُقُ مَن يَشَاءُ ۖ وَهُوَ الْقَوِيُّ الْعَزِيزُ ۝١٩
Allahu lateefum bi`ibaadihee yarzuqu mai yashaaa`u wa Huwal Qawiyyul `Azeez
📖 Tekkim Wolof
Yàlla kuy ñeewanti jaamam ñi la. Mooy wërsëgël ku ko soob. te moo di boroom Doole ja, boroom Kàttan ga.

🎧 Dégg


📜 Aaya 17-21 — Ash-Shura

17اللَّهُ الَّذِي أَنزَلَ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ وَالْمِيزَانَ ۗ وَمَا يُدْرِيكَ لَعَلَّ السَّاعَةَ قَرِيبٌ
Moo di Yàlla mi wàcce Téere ba ci dëgg, ak nattukaay ba (balaas ya). Ana loo ci xam ? te amaana waxtu wa di lu jigeñ ?
18يَسْتَعْجِلُ بِهَا الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِهَا ۖ وَالَّذِينَ آمَنُوا مُشْفِقُونَ مِنْهَا وَيَعْلَمُونَ أَنَّهَا الْحَقُّ ۗ أَلَا إِنَّ الَّذِينَ يُمَارُونَ فِي السَّاعَةِ لَفِي ضَلَالٍ بَعِيدٍ
Ña ko gëmul ña nga koy yàkkamti ; waaye ña gëm ñoom dañu koy ragal te xam nañu ne mooy dëgg tigi. Ñay werante ci mbirum waxtu wa (Bis Pénc ba) ña nga ci réer gu sore.
19اللَّهُ لَطِيفٌ بِعِبَادِهِ يَرْزُقُ مَن يَشَاءُ ۖ وَهُوَ الْقَوِيُّ الْعَزِيزُ
Yàlla kuy ñeewanti jaamam ñi la. Mooy wërsëgël ku ko soob. te moo di boroom Doole ja, boroom Kàttan ga.
20مَن كَانَ يُرِيدُ حَرْثَ الْآخِرَةِ نَزِدْ لَهُ فِي حَرْثِهِ ۖ وَمَن كَانَ يُرِيدُ حَرْثَ الدُّنْيَا نُؤْتِهِ مِنْهَا وَمَا لَهُ فِي الْآخِرَةِ مِن نَّصِيبٍ
Képp ku namm ruuj [toolu] dundug àllaaxira, Dananu ko dollil ruujeefam. Képp it ku namm ruuj [toolu] dundug àddina, Dananu ko nangul ; waaye du am benn cër ca àllaaxira.
21أَمْ لَهُمْ شُرَكَاءُ شَرَعُوا لَهُم مِّنَ الدِّينِ مَا لَمْ يَأْذَن بِهِ اللَّهُ ۚ وَلَوْلَا كَلِمَةُ الْفَصْلِ لَقُضِيَ بَيْنَهُمْ ۗ وَإِنَّ الظَّالِمِينَ لَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Am ñoom da ñoo am bokkaale yu leen tërëlal diine ju bokkewul ak li Yàlla digle ? Du gan kon, ak kàddu gu xas jib ba noppi, kon àtteef na seen diggënte. Te tooñkat ya ñoom am nañu mbugël mu mitti .
Ash-ShuraFihi Alxuraan
53Aaya
MeccanRevelation
19Aaya

Tekki — Ash-Shura 19

Simoore Ash-Shura Aaya 19 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla kuy ñeewanti jaamam ñi la. Mooy wërsëgël ku ko…

Simoore Aaya 19/53 — Ash-Shura الشورى (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ash-Shura Dégg, Ash-Shura Tekki, Ash-Shura mp3, Ash-Shura pdf. Aaya 17–21. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers