Az-Zukhruf · 45/89
Tekki Waxtaan — Az-Zukhruf
وَاسْأَلْ مَنْ أَرْسَلْنَا مِن قَبْلِكَ مِن رُّسُلِنَا أَجَعَلْنَا مِن دُونِ الرَّحْمَٰنِ آلِهَةً يُعْبَدُونَ ۝٤٥
Was`al man arsalnaa min qablika mir Rusulinaaa aja`alnaa min doonir Rahmaani aalihatany yu badoon
📖 Tekkim Wolof
Laajal Yonent yi Nu jëkkoon a yónni ñu jiitu la, ba xam ndax defaroon Nañu Yàlla, ju bokkul ak yëramaakoon bi, ju ñuy jaamu ?

🎧 Dégg


📜 Aaya 43-47 — Az-Zukhruf

43فَاسْتَمْسِكْ بِالَّذِي أُوحِيَ إِلَيْكَ ۖ إِنَّكَ عَلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Jafandikul ci li nu soloo ci yaw yaa ngi ci yoon wu jub xocc wa.
44وَإِنَّهُ لَذِكْرٌ لَّكَ وَلِقَوْمِكَ ۖ وَسَوْفَ تُسْأَلُونَ
Dëgg-dëgg [Alxuraan] fàttaliku la ngir yaw ak saw nit. Te it deefna leen ko laaj.
45وَاسْأَلْ مَنْ أَرْسَلْنَا مِن قَبْلِكَ مِن رُّسُلِنَا أَجَعَلْنَا مِن دُونِ الرَّحْمَٰنِ آلِهَةً يُعْبَدُونَ
Laajal Yonent yi Nu jëkkoon a yónni ñu jiitu la, ba xam ndax defaroon Nañu Yàlla, ju bokkul ak yëramaakoon bi, ju ñuy jaamu ?
46وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا مُوسَىٰ بِآيَاتِنَا إِلَىٰ فِرْعَوْنَ وَمَلَئِهِ فَقَالَ إِنِّي رَسُولُ رَبِّ الْعَالَمِينَ
Yónni woon Nanu Muusaa ak Sunuy kéemaan, ci Firawna ak gàngooram ga. Mu ne leen: “Man ndawul Boroom àddina si laa”.
47فَلَمَّا جَاءَهُم بِآيَاتِنَا إِذَا هُم مِّنْهَا يَضْحَكُونَ
Ba mu dikkee ca ñoom ànd ak Sunuy firnde (kéemaan), ndeketeyoo dañu koy reetaan.
Az-ZukhrufFihi Alxuraan
89Aaya
MeccanRevelation
45Aaya

Tekki — Az-Zukhruf 45

Simoore Az-Zukhruf Aaya 45 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Laajal Yonent yi Nu jëkkoon a yónni ñu jiitu la,…

Simoore Aaya 45/89 — Az-Zukhruf الزخرف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Az-Zukhruf Dégg, Az-Zukhruf Tekki, Az-Zukhruf mp3, Az-Zukhruf pdf. Aaya 43–47. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers