Al-Jathiya · 24/37
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Jathiya
وَقَالُوا مَا هِيَ إِلَّا حَيَاتُنَا الدُّنْيَا نَمُوتُ وَنَحْيَا وَمَا يُهْلِكُنَا إِلَّا الدَّهْرُ ۚ وَمَا لَهُم بِذَٰلِكَ مِنْ عِلْمٍ ۖ إِنْ هُمْ إِلَّا يَظُنُّونَ ۝٢٤
Wa qaaloo maa hiya illaa hayaatunad dunyaa namootu wa nahyaa wa maa yuhlikunaaa illad dahr; wa maa lahum bizaalika min `ilmin in hum illaayazunnoon
📖 Tekkim Wolof
Ñuy wax naan : “lii daal du lenn lu dul su nu dundug àddina : danuy dee di dund te yàggaayu jamono rekk moo nuy ràpploo”. Waaye amuñu ci loolu benn xam-xam : dañuy njortu doŋŋ.

🎧 Dégg


📜 Aaya 22-26 — Simoore Al-Jathiya

22وَخَلَقَ اللَّهُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِالْحَقِّ وَلِتُجْزَىٰ كُلُّ نَفْسٍ بِمَا كَسَبَتْ وَهُمْ لَا يُظْلَمُونَ
Yàlla bind na asamaan yeek suuf si ci dëgg ak it ngir mu fay bakkaan bu nekk ca la mu daan fàggu. Te kenn du leen tooñ (ci wàññi yiw mbaa yokk safaan).
23أَفَرَأَيْتَ مَنِ اتَّخَذَ إِلَٰهَهُ هَوَاهُ وَأَضَلَّهُ اللَّهُ عَلَىٰ عِلْمٍ وَخَتَمَ عَلَىٰ سَمْعِهِ وَقَلْبِهِ وَجَعَلَ عَلَىٰ بَصَرِهِ غِشَاوَةً فَمَن يَهْدِيهِ مِن بَعْدِ اللَّهِ ۚ أَفَلَا تَذَكَّرُونَ
Xanaa gisuloo ka jàppe bakkanam muy yàlllaam ? Yàlla faf ko réerël fatt ag déggëm ak ub xolam muur ab gisam. (Waaw) kooku ana kan moo koy gindi ginnaaw Yàlla ? Xanaa dangeen dul fàttaliku?
24وَقَالُوا مَا هِيَ إِلَّا حَيَاتُنَا الدُّنْيَا نَمُوتُ وَنَحْيَا وَمَا يُهْلِكُنَا إِلَّا الدَّهْرُ ۚ وَمَا لَهُم بِذَٰلِكَ مِنْ عِلْمٍ ۖ إِنْ هُمْ إِلَّا يَظُنُّونَ
Ñuy wax naan : “lii daal du lenn lu dul su nu dundug àddina : danuy dee di dund te yàggaayu jamono rekk moo nuy ràpploo”. Waaye amuñu ci loolu benn xam-xam : dañuy njortu doŋŋ.
25وَإِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ آيَاتُنَا بَيِّنَاتٍ مَّا كَانَ حُجَّتَهُمْ إِلَّا أَن قَالُوا ائْتُوا بِآبَائِنَا إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Te saa su ñu jàngee Sunuy laaya ci ñoom, seen lay du doon lenn lu dul di wax naan: “Délloosilleen nu sunuy maam (ya deewoon) ndegam li ngeen di wax dëgg la”.
26قُلِ اللَّهُ يُحْيِيكُمْ ثُمَّ يُمِيتُكُمْ ثُمَّ يَجْمَعُكُمْ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ لَا رَيْبَ فِيهِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Waxal ne : “Yàllaa leen di dundal soog leen a rey. Ba noppi mu leen di dajale bu Bis Pénc baa, sikk amul ci loolu, waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
Al-JathiyaFihi Alxuraan
37Aaya
MeccanRevelation
24Aaya

Tekki — Al-Jathiya 24

Simoore Al-Jathiya Aaya 24 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñuy wax naan : “lii daal du lenn lu dul…

Simoore Aaya 24/37 — Simoore Al-Jathiya الجاثية (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Jathiya Dégg, Simoore Al-Jathiya Tekki, Simoore Al-Jathiya mp3, Simoore Al-Jathiya pdf. Aaya 22–26. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers