Al-Jathiya · 25/37
Tekki Waxtaan — Al-Jathiya
وَإِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ آيَاتُنَا بَيِّنَاتٍ مَّا كَانَ حُجَّتَهُمْ إِلَّا أَن قَالُوا ائْتُوا بِآبَائِنَا إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ ۝٢٥
Wa izaa tutlaa `alaihim aayaatuna baiyinaatim maa kaana hujjatahum illaaa an qaalu`too bi aabaaa`inaaa in kuntum saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
Te saa su ñu jàngee Sunuy laaya ci ñoom, seen lay du doon lenn lu dul di wax naan: “Délloosilleen nu sunuy maam (ya deewoon) ndegam li ngeen di wax dëgg la”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 23-27 — Al-Jathiya

23أَفَرَأَيْتَ مَنِ اتَّخَذَ إِلَٰهَهُ هَوَاهُ وَأَضَلَّهُ اللَّهُ عَلَىٰ عِلْمٍ وَخَتَمَ عَلَىٰ سَمْعِهِ وَقَلْبِهِ وَجَعَلَ عَلَىٰ بَصَرِهِ غِشَاوَةً فَمَن يَهْدِيهِ مِن بَعْدِ اللَّهِ ۚ أَفَلَا تَذَكَّرُونَ
Xanaa gisuloo ka jàppe bakkanam muy yàlllaam ? Yàlla faf ko réerël fatt ag déggëm ak ub xolam muur ab gisam. (Waaw) kooku ana kan moo koy gindi ginnaaw Yàlla ? Xanaa dangeen dul fàttaliku?
24وَقَالُوا مَا هِيَ إِلَّا حَيَاتُنَا الدُّنْيَا نَمُوتُ وَنَحْيَا وَمَا يُهْلِكُنَا إِلَّا الدَّهْرُ ۚ وَمَا لَهُم بِذَٰلِكَ مِنْ عِلْمٍ ۖ إِنْ هُمْ إِلَّا يَظُنُّونَ
Ñuy wax naan : “lii daal du lenn lu dul su nu dundug àddina : danuy dee di dund te yàggaayu jamono rekk moo nuy ràpploo”. Waaye amuñu ci loolu benn xam-xam : dañuy njortu doŋŋ.
25وَإِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ آيَاتُنَا بَيِّنَاتٍ مَّا كَانَ حُجَّتَهُمْ إِلَّا أَن قَالُوا ائْتُوا بِآبَائِنَا إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Te saa su ñu jàngee Sunuy laaya ci ñoom, seen lay du doon lenn lu dul di wax naan: “Délloosilleen nu sunuy maam (ya deewoon) ndegam li ngeen di wax dëgg la”.
26قُلِ اللَّهُ يُحْيِيكُمْ ثُمَّ يُمِيتُكُمْ ثُمَّ يَجْمَعُكُمْ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ لَا رَيْبَ فِيهِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Waxal ne : “Yàllaa leen di dundal soog leen a rey. Ba noppi mu leen di dajale bu Bis Pénc baa, sikk amul ci loolu, waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
27وَلِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ وَيَوْمَ تَقُومُ السَّاعَةُ يَوْمَئِذٍ يَخْسَرُ الْمُبْطِلُونَ
Yàllaa moom nguurug asamaan yeek suuf si. Te saa su Bis Pénc ba taxawee, bu keroogee, yéefar yi danañu yàqule.
Al-JathiyaFihi Alxuraan
37Aaya
MeccanRevelation
25Aaya

Tekki — Al-Jathiya 25

Simoore Al-Jathiya Aaya 25 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te saa su ñu jàngee Sunuy laaya ci ñoom, seen…

Simoore Aaya 25/37 — Al-Jathiya الجاثية (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Jathiya Dégg, Al-Jathiya Tekki, Al-Jathiya mp3, Al-Jathiya pdf. Aaya 23–27. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers