Al-Jathiya · 26/37
Tekki Waxtaan — Al-Jathiya
قُلِ اللَّهُ يُحْيِيكُمْ ثُمَّ يُمِيتُكُمْ ثُمَّ يَجْمَعُكُمْ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ لَا رَيْبَ فِيهِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ ۝٢٦
Qulil laahu yuhyeekum summa yumeetukum summa yajma`ukum ilaa Yawmil Qiyaamati laa raiba feehi wa laakinna aksaran naasi laa ya`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Waxal ne : “Yàllaa leen di dundal soog leen a rey. Ba noppi mu leen di dajale bu Bis Pénc baa, sikk amul ci loolu, waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 24-28 — Al-Jathiya

24وَقَالُوا مَا هِيَ إِلَّا حَيَاتُنَا الدُّنْيَا نَمُوتُ وَنَحْيَا وَمَا يُهْلِكُنَا إِلَّا الدَّهْرُ ۚ وَمَا لَهُم بِذَٰلِكَ مِنْ عِلْمٍ ۖ إِنْ هُمْ إِلَّا يَظُنُّونَ
Ñuy wax naan : “lii daal du lenn lu dul su nu dundug àddina : danuy dee di dund te yàggaayu jamono rekk moo nuy ràpploo”. Waaye amuñu ci loolu benn xam-xam : dañuy njortu doŋŋ.
25وَإِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ آيَاتُنَا بَيِّنَاتٍ مَّا كَانَ حُجَّتَهُمْ إِلَّا أَن قَالُوا ائْتُوا بِآبَائِنَا إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Te saa su ñu jàngee Sunuy laaya ci ñoom, seen lay du doon lenn lu dul di wax naan: “Délloosilleen nu sunuy maam (ya deewoon) ndegam li ngeen di wax dëgg la”.
26قُلِ اللَّهُ يُحْيِيكُمْ ثُمَّ يُمِيتُكُمْ ثُمَّ يَجْمَعُكُمْ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ لَا رَيْبَ فِيهِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Waxal ne : “Yàllaa leen di dundal soog leen a rey. Ba noppi mu leen di dajale bu Bis Pénc baa, sikk amul ci loolu, waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
27وَلِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ وَيَوْمَ تَقُومُ السَّاعَةُ يَوْمَئِذٍ يَخْسَرُ الْمُبْطِلُونَ
Yàllaa moom nguurug asamaan yeek suuf si. Te saa su Bis Pénc ba taxawee, bu keroogee, yéefar yi danañu yàqule.
28وَتَرَىٰ كُلَّ أُمَّةٍ جَاثِيَةً ۚ كُلُّ أُمَّةٍ تُدْعَىٰ إِلَىٰ كِتَابِهَا الْيَوْمَ تُجْزَوْنَ مَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Ca ngay gise xeet wu nërméelu. Xeet wu ca nekk ñu di ko woo (ngir jox ko ab téereem ba ay jëfëm nekk). Te naan ko bis niki tey dees na leen fay li ngeen daan jëf.
Al-JathiyaFihi Alxuraan
37Aaya
MeccanRevelation
26Aaya

Tekki — Al-Jathiya 26

Simoore Al-Jathiya Aaya 26 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waxal ne : “Yàllaa leen di dundal soog leen a…

Simoore Aaya 26/37 — Al-Jathiya الجاثية (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Jathiya Dégg, Al-Jathiya Tekki, Al-Jathiya mp3, Al-Jathiya pdf. Aaya 24–28. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers