Al-Maida · 21/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
يَا قَوْمِ ادْخُلُوا الْأَرْضَ الْمُقَدَّسَةَ الَّتِي كَتَبَ اللَّهُ لَكُمْ وَلَا تَرْتَدُّوا عَلَىٰ أَدْبَارِكُمْ فَتَنقَلِبُوا خَاسِرِينَ ۝٢١
Yaa qawmid khulul Ardal MMuqaddasatal latee katabal laahu lakum wa laa tartaddoo `alaaa adbaarikum fatanqaliboo khaasireen
📖 Tekkim Wolof
Yéen samaw nit ! Dugguleen ci suuf su sell si leen Yàlla sédde. Te buleen walbatiku dellu ginnaaw, kon ngeen yàqule.

🎧 Dégg


📜 Aaya 19-23 — Al-Maida

19يَا أَهْلَ الْكِتَابِ قَدْ جَاءَكُمْ رَسُولُنَا يُبَيِّنُ لَكُمْ عَلَىٰ فَتْرَةٍ مِّنَ الرُّسُلِ أَن تَقُولُوا مَا جَاءَنَا مِن بَشِيرٍ وَلَا نَذِيرٍ ۖ فَقَدْ جَاءَكُم بَشِيرٌ وَنَذِيرٌ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Éy yéen ñoñ-téere ! Sunub Yonent dikk na ci yéen leeralal leen ginnaaw diir ba dox digganteem ak ka mujj a feeñ ngir ngeen bañ a taafentaloo ne : “Kenn kuy waare walla kuy xamle dikkul fi nun”. Am na ku dikkoon fi yéen kay di xamle ak a waare. Te Yàlla am na kàttan ci def lu Ko soob.
20وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ يَا قَوْمِ اذْكُرُوا نِعْمَةَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ إِذْ جَعَلَ فِيكُمْ أَنبِيَاءَ وَجَعَلَكُم مُّلُوكًا وَآتَاكُم مَّا لَمْ يُؤْتِ أَحَدًا مِّنَ الْعَالَمِينَ
(Fàttalikul) ba Muusaa waxee aw nitam, ne leen : "Yéen samaw nit ! Fàttalikuleen xéewali Yàlla yi Mu defoon ci yéen, ba Mu defee ci yéen ay Yonent. Def leen ngeen di ay buur. Mu mayoon leen lu mu musul may kenn ci àddina bi.
21يَا قَوْمِ ادْخُلُوا الْأَرْضَ الْمُقَدَّسَةَ الَّتِي كَتَبَ اللَّهُ لَكُمْ وَلَا تَرْتَدُّوا عَلَىٰ أَدْبَارِكُمْ فَتَنقَلِبُوا خَاسِرِينَ
Yéen samaw nit ! Dugguleen ci suuf su sell si leen Yàlla sédde. Te buleen walbatiku dellu ginnaaw, kon ngeen yàqule.
22قَالُوا يَا مُوسَىٰ إِنَّ فِيهَا قَوْمًا جَبَّارِينَ وَإِنَّا لَن نَّدْخُلَهَا حَتَّىٰ يَخْرُجُوا مِنْهَا فَإِن يَخْرُجُوا مِنْهَا فَإِنَّا دَاخِلُونَ
Ñu ne ko : "Yaw Muusaa, [xamal ne] suuf soosu ñu bari doolee fa nekk. Te nun dunu ca mën a dugg mukk li feek génnuñu. Bu ñu génnee nag ñu door a dugg”.
23قَالَ رَجُلَانِ مِنَ الَّذِينَ يَخَافُونَ أَنْعَمَ اللَّهُ عَلَيْهِمَا ادْخُلُوا عَلَيْهِمُ الْبَابَ فَإِذَا دَخَلْتُمُوهُ فَإِنَّكُمْ غَالِبُونَ ۚ وَعَلَى اللَّهِ فَتَوَكَّلُوا إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
Ñaari nit, ca ña ragal Yàlla, wax ne Yàlla teral na leen : “Dugguleen ca ñoom, nu jaare ci buntu bi ; bu ngeen jàllee, yéen ay not. Te ci Yàlla doŋŋ ngeen war a sukkandiku ndegam ñu gëm ngeen”.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
21Aaya

Tekki — Al-Maida 21

Simoore Al-Maida Aaya 21 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yéen samaw nit ! Dugguleen ci suuf su sell si…

Simoore Aaya 21/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 19–23. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers