Al-Maida · 36/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا لَوْ أَنَّ لَهُم مَّا فِي الْأَرْضِ جَمِيعًا وَمِثْلَهُ مَعَهُ لِيَفْتَدُوا بِهِ مِنْ عَذَابِ يَوْمِ الْقِيَامَةِ مَا تُقُبِّلَ مِنْهُمْ ۖ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ ۝٣٦
Innal lazeena kafaroo law anna lahum maa fil ardi jamee`anw wa mislahoo ma`ahoo liyaftadoo bihee min `azaabi Yawmil Qiyaamati maa tuqubbila minhum wa lahum azaabun aleem
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne weddi nañu, bu ñu amoon àddina ak li ci biiram lépp ba dolli ca li na toll, bëgg koo joxe ngir jotoo ko ca mbugalum Bis-pénc ba, kenn duleen ko nangul. Te nag mbugal mu metteey dal ci seen kaw.

🎧 Dégg


📜 Aaya 34-38 — Al-Maida

34إِلَّا الَّذِينَ تَابُوا مِن قَبْلِ أَن تَقْدِرُوا عَلَيْهِمْ ۖ فَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
ba mu des ñanga xam ne tuub nañu lu jiitu ngeen not leen : nangeen xam xéll ne Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
35يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اتَّقُوا اللَّهَ وَابْتَغُوا إِلَيْهِ الْوَسِيلَةَ وَجَاهِدُوا فِي سَبِيلِهِ لَعَلَّكُمْ تُفْلِحُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla, sàkkuleen lu leen di jigeeñal Yàlla te nangeen sonn ci liggéeyal Yàlla. Ndax Yàlla ngeen texe !
36إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا لَوْ أَنَّ لَهُم مَّا فِي الْأَرْضِ جَمِيعًا وَمِثْلَهُ مَعَهُ لِيَفْتَدُوا بِهِ مِنْ عَذَابِ يَوْمِ الْقِيَامَةِ مَا تُقُبِّلَ مِنْهُمْ ۖ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña nga xam ne weddi nañu, bu ñu amoon àddina ak li ci biiram lépp ba dolli ca li na toll, bëgg koo joxe ngir jotoo ko ca mbugalum Bis-pénc ba, kenn duleen ko nangul. Te nag mbugal mu metteey dal ci seen kaw.
37يُرِيدُونَ أَن يَخْرُجُوا مِنَ النَّارِ وَمَا هُم بِخَارِجِينَ مِنْهَا ۖ وَلَهُمْ عَذَابٌ مُّقِيمٌ
Danañu bëgg a génn Safara, waaye duñu fa mën a génn. Am nañu fa mbugal mu sax dàkk.
38وَالسَّارِقُ وَالسَّارِقَةُ فَاقْطَعُوا أَيْدِيَهُمَا جَزَاءً بِمَا كَسَبَا نَكَالًا مِّنَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ عَزِيزٌ حَكِيمٌ
Sàcc bu góor ak sàcc bu jigéen, dogleen seeni yoxo ñoom ñaar muy peyug la ñu fàggu, di mbugal mu tukkee ca Yàlla. Moom Yàlla Aji-not la, Aji-xereñ la.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
36Aaya

Tekki — Al-Maida 36

Simoore Al-Maida Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne weddi nañu, bu ñu amoon àddina…

Simoore Aaya 36/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers