Al-Maida · 71/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
وَحَسِبُوا أَلَّا تَكُونَ فِتْنَةٌ فَعَمُوا وَصَمُّوا ثُمَّ تَابَ اللَّهُ عَلَيْهِمْ ثُمَّ عَمُوا وَصَمُّوا كَثِيرٌ مِّنْهُمْ ۚ وَاللَّهُ بَصِيرٌ بِمَا يَعْمَلُونَ ۝٧١
Wa hasibooo allaa takoona fitnaun fa`amoo wa sammoo summa taabal laahu `alaihim summa `amoo wa sammoo kaseerum minhum; wallaahu baseerum bimaa ya`maloon
📖 Tekkim Wolof
Ñu njortu ne menn mbugal [du ca topp] ba tax ñu gumba, tëx . Ci loolu Yàlla jéggal leen. Ba noppi, ñu bari ci ñoom dellu gumba tëx. Te Yàllaa ngi ne jàkk ca la ñuy def.
🎧 Dégg

📜 Aaya 69-73 — Al-Maida

69إِنَّ الَّذِينَ آمَنُوا وَالَّذِينَ هَادُوا وَالصَّابِئُونَ وَالنَّصَارَىٰ مَنْ آمَنَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ وَعَمِلَ صَالِحًا فَلَا خَوْفٌ عَلَيْهِمْ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ
Ña nekk nasraan te gëm Yàlla, walbatiku gëm Lislaam, ak Bis-pénc ba te sellal seeni jëf, duñu am njàqare, duñu am naqar.
70لَقَدْ أَخَذْنَا مِيثَاقَ بَنِي إِسْرَائِيلَ وَأَرْسَلْنَا إِلَيْهِمْ رُسُلًا ۖ كُلَّمَا جَاءَهُمْ رَسُولٌ بِمَا لَا تَهْوَىٰ أَنفُسُهُمْ فَرِيقًا كَذَّبُوا وَفَرِيقًا يَقْتُلُونَ
Fasante woon Nanu kóllare ak waa Banii-Israayiila, yónni ci ñoom, saa yu Nu leen indilee lu leen neexul, ñu weddi ñenn ña, rey ñenn ña.
71وَحَسِبُوا أَلَّا تَكُونَ فِتْنَةٌ فَعَمُوا وَصَمُّوا ثُمَّ تَابَ اللَّهُ عَلَيْهِمْ ثُمَّ عَمُوا وَصَمُّوا كَثِيرٌ مِّنْهُمْ ۚ وَاللَّهُ بَصِيرٌ بِمَا يَعْمَلُونَ
Ñu njortu ne menn mbugal [du ca topp] ba tax ñu gumba, tëx . Ci loolu Yàlla jéggal leen. Ba noppi, ñu bari ci ñoom dellu gumba tëx. Te Yàllaa ngi ne jàkk ca la ñuy def.
72لَقَدْ كَفَرَ الَّذِينَ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ هُوَ الْمَسِيحُ ابْنُ مَرْيَمَ ۖ وَقَالَ الْمَسِيحُ يَا بَنِي إِسْرَائِيلَ اعْبُدُوا اللَّهَ رَبِّي وَرَبَّكُمْ ۖ إِنَّهُ مَن يُشْرِكْ بِاللَّهِ فَقَدْ حَرَّمَ اللَّهُ عَلَيْهِ الْجَنَّةَ وَمَأْوَاهُ النَّارُ ۖ وَمَا لِلظَّالِمِينَ مِنْ أَنصَارٍ
Ña wax ne : “Yàlla Mooy ku ñu barkeel ka [Masiih], doomi Maryaama.”, tàbbi nañu ci kéefar. Te moom ku ñu barkeel ka waxoon na ne : "Yéen waa bani Israayiil, nangeen jaamu Yàlla, ka di sama Boroom”. Te [xamleen ne], ku bokkaale Yàlla ak dara, Yàlla Dana ko araamal Àjjana ; def dëkkuwaayam mu di Safara. Te tooñkat ya duñu am ndimbal !
73لَّقَدْ كَفَرَ الَّذِينَ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ ثَالِثُ ثَلَاثَةٍ ۘ وَمَا مِنْ إِلَٰهٍ إِلَّا إِلَٰهٌ وَاحِدٌ ۚ وَإِن لَّمْ يَنتَهُوا عَمَّا يَقُولُونَ لَيَمَسَّنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا مِنْهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña wax ne : “Yàlla ñetteel la ci ñett.”, tàbbi nañu ci kéefar. Te Yàlla Moom jenn doŋŋ la ! Bu ñu bàyyiwul li ñuy wax, fàwwu mbugal mu metti dal ña weddi ca ñoom.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
71Aaya

Tekki — Al-Maida 71

Simoore Al-Maida Aaya 71 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñu njortu ne menn mbugal [du ca topp] ba tax…

Simoore Aaya 71/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 69–73. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers