Al-An'am · 147/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
فَإِن كَذَّبُوكَ فَقُل رَّبُّكُمْ ذُو رَحْمَةٍ وَاسِعَةٍ وَلَا يُرَدُّ بَأْسُهُ عَنِ الْقَوْمِ الْمُجْرِمِينَ ۝١٤٧
Fa in kazzabooka faqur Rabbukum zoo rahmatinw waasi`atinw waasi`atinw wa laa yuraddu baasuhoo `anil qawmil mujrimeen
📖 Tekkim Wolof
Bu ñu la weddee, neel : “Seen Boroom dey Ku am yërmaande ju yaatu la, waaye mbugalam ma jëm ca saay-saay sa dara mënukoo feg”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 145-149 — Al-An'am

145قُل لَّا أَجِدُ فِي مَا أُوحِيَ إِلَيَّ مُحَرَّمًا عَلَىٰ طَاعِمٍ يَطْعَمُهُ إِلَّا أَن يَكُونَ مَيْتَةً أَوْ دَمًا مَّسْفُوحًا أَوْ لَحْمَ خِنزِيرٍ فَإِنَّهُ رِجْسٌ أَوْ فِسْقًا أُهِلَّ لِغَيْرِ اللَّهِ بِهِ ۚ فَمَنِ اضْطُرَّ غَيْرَ بَاغٍ وَلَا عَادٍ فَإِنَّ رَبَّكَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Neel : “Man dey gisuma, ci li ñu ma soloo, lu araam ci ñam wu ñuy lekk lu dul mu nekk médd walla deret yuy tuuru, walla yàppu mbaam-xuux - ndax sobe la - walla la ñu tuddu [ba ñu koy rey] keneen ku dul Yàlla cig génn topp.”. Waaye koo xam ne dafa loru, te di ku bew, walla muy ku jéggi dayo ca loola, Sa Boroom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
146وَعَلَى الَّذِينَ هَادُوا حَرَّمْنَا كُلَّ ذِي ظُفُرٍ ۖ وَمِنَ الْبَقَرِ وَالْغَنَمِ حَرَّمْنَا عَلَيْهِمْ شُحُومَهُمَا إِلَّا مَا حَمَلَتْ ظُهُورُهُمَا أَوِ الْحَوَايَا أَوْ مَا اخْتَلَطَ بِعَظْمٍ ۚ ذَٰلِكَ جَزَيْنَاهُم بِبَغْيِهِمْ ۖ وَإِنَّا لَصَادِقُونَ
Dogaloon Nanu ca ña nekk Yahuud, ne araam na ci ñoom lépp luy boroom we te it araam na ca ñoom nebbonu nag ya ak gàtt ya, lu dul bu tegu ci seen ginnaaw, walla bu nekk ca seen mbàq, walla bu jaxasook yax ya. Noonu Lanu leen feye seen bew ga te Nun ñu dëggu Lanu.
147فَإِن كَذَّبُوكَ فَقُل رَّبُّكُمْ ذُو رَحْمَةٍ وَاسِعَةٍ وَلَا يُرَدُّ بَأْسُهُ عَنِ الْقَوْمِ الْمُجْرِمِينَ
Bu ñu la weddee, neel : “Seen Boroom dey Ku am yërmaande ju yaatu la, waaye mbugalam ma jëm ca saay-saay sa dara mënukoo feg”.
148سَيَقُولُ الَّذِينَ أَشْرَكُوا لَوْ شَاءَ اللَّهُ مَا أَشْرَكْنَا وَلَا آبَاؤُنَا وَلَا حَرَّمْنَا مِن شَيْءٍ ۚ كَذَٰلِكَ كَذَّبَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ حَتَّىٰ ذَاقُوا بَأْسَنَا ۗ قُلْ هَلْ عِندَكُم مِّنْ عِلْمٍ فَتُخْرِجُوهُ لَنَا ۖ إِن تَتَّبِعُونَ إِلَّا الظَّنَّ وَإِنْ أَنتُمْ إِلَّا تَخْرُصُونَ
Ñay bokkaale danañu wax ne : “Bu neexoon Yàlla, dunu bokkaale, sunuy baay it kon duñu bokkaale te dunu araamal dara, wat ci watiit !”. Noonu doŋŋ la ña leen jiitu woon doon weddee ba Sa mbugal ne xees ci seen kaw. Neel : “Ndax am ngeen xam-xam bu ngeen nu mën a génneel ? Yéen daal toppuleen lu moy ay njort te nekkuleen ci lu moy di fen”.
149قُلْ فَلِلَّهِ الْحُجَّةُ الْبَالِغَةُ ۖ فَلَوْ شَاءَ لَهَدَاكُمْ أَجْمَعِينَ
Neel : “Lii, wommatug Yàlla la, Moo ko moom. Bu ko sooboon, Mu jubal leen yéen ñépp.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
147Aaya

Tekki — Al-An'am 147

Simoore Al-An'am Aaya 147 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ñu la weddee, neel : “Seen Boroom dey Ku…

Simoore Aaya 147/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 145–149. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers