Al-A'raf · 98/206
Tekki Waxtaan — Simoore Al-A'raf
أَوَأَمِنَ أَهْلُ الْقُرَىٰ أَن يَأْتِيَهُم بَأْسُنَا ضُحًى وَهُمْ يَلْعَبُونَ ۝٩٨
Awa amina ahlul quraaa ai yaatiyahum baasunaa duhanw wa hum yal`aboon
📖 Tekkim Wolof
Walla dëkk yooyu naagu ne Sunu mbugal duleen dikkal bëccëg fekk ñuy fo ?

🎧 Dégg


📜 Aaya 96-100 — Simoore Al-A'raf

96وَلَوْ أَنَّ أَهْلَ الْقُرَىٰ آمَنُوا وَاتَّقَوْا لَفَتَحْنَا عَلَيْهِم بَرَكَاتٍ مِّنَ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ وَلَٰكِن كَذَّبُوا فَأَخَذْنَاهُم بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ
Bu fekkoon ne waa dëkk yooyu gëmoon nañu te ragal Yàlla, kon fàwwu Dananu leen ubbil ay wërsëg yu bawoo asamaan ak ci suuf si. Waaye dañoo weddi, Nu sadd leen ngir la ñu daan fàggu ci lu bon.
97أَفَأَمِنَ أَهْلُ الْقُرَىٰ أَن يَأْتِيَهُم بَأْسُنَا بَيَاتًا وَهُمْ نَائِمُونَ
Moo ndax dafa am ci waa dëkk yooyu ñu naagu ne Sunu mbugal duleen dikke ci guddi fekk ñuy nelaw ?
98أَوَأَمِنَ أَهْلُ الْقُرَىٰ أَن يَأْتِيَهُم بَأْسُنَا ضُحًى وَهُمْ يَلْعَبُونَ
Walla dëkk yooyu naagu ne Sunu mbugal duleen dikkal bëccëg fekk ñuy fo ?
99أَفَأَمِنُوا مَكْرَ اللَّهِ ۚ فَلَا يَأْمَنُ مَكْرَ اللَّهِ إِلَّا الْقَوْمُ الْخَاسِرُونَ
Moo ndax dañoo naagu ci pexey Yàlla ? Te kenn du naagu ci pexey Yàlla ku dul nit ñu yàqule.
100أَوَلَمْ يَهْدِ لِلَّذِينَ يَرِثُونَ الْأَرْضَ مِن بَعْدِ أَهْلِهَا أَن لَّوْ نَشَاءُ أَصَبْنَاهُم بِذُنُوبِهِمْ ۚ وَنَطْبَعُ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ فَهُمْ لَا يَسْمَعُونَ
Walla ndax dafa leeral ci ñi donn suuf si, ginnaaw ña fi nekkoon, ci ne su Nu neexoon Nu sadd leen ngir seeni bàkkaar ak fatt seeni xol ba dootuñu am dégg-dégg ?
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
98Aaya

Tekki — Al-A'raf 98

Simoore Al-A'raf Aaya 98 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Walla dëkk yooyu naagu ne Sunu mbugal duleen dikkal bëccëg…

Simoore Aaya 98/206 — Simoore Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-A'raf Dégg, Simoore Al-A'raf Tekki, Simoore Al-A'raf mp3, Simoore Al-A'raf pdf. Aaya 96–100. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers