At-Tawba · 56/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
وَيَحْلِفُونَ بِاللَّهِ إِنَّهُمْ لَمِنكُمْ وَمَا هُم مِّنكُمْ وَلَٰكِنَّهُمْ قَوْمٌ يَفْرَقُونَ ۝٥٦
Wa yahlifoona billaahi innnahum laminkum wa maa hum minkum wa laakinnahum qawmuny yafraqoon
📖 Tekkim Wolof
Ñuy waat ci Yàlla, naan ñoom ci yéen lañu bokk ; te bokkuñu ci yéen. Waaye ñoom dañoo ragal rekk ngeen dal (ci seen kaw).

🎧 Dégg


📜 Aaya 54-58 — Simoore At-Tawba

54وَمَا مَنَعَهُمْ أَن تُقْبَلَ مِنْهُمْ نَفَقَاتُهُمْ إِلَّا أَنَّهُمْ كَفَرُوا بِاللَّهِ وَبِرَسُولِهِ وَلَا يَأْتُونَ الصَّلَاةَ إِلَّا وَهُمْ كُسَالَىٰ وَلَا يُنفِقُونَ إِلَّا وَهُمْ كَارِهُونَ
Li waral seen alal jooju Yàlla du ko nangu, moo di ne dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam, tàyyeel lool ci julli, nay lool ci li ñuy joxe.
55فَلَا تُعْجِبْكَ أَمْوَالُهُمْ وَلَا أَوْلَادُهُمْ ۚ إِنَّمَا يُرِيدُ اللَّهُ لِيُعَذِّبَهُم بِهَا فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَتَزْهَقَ أَنفُسُهُمْ وَهُمْ كَافِرُونَ
Bula seeni alal yéem, naka noonu bula seeni doom yéem ! Yàlla nammul lu dul mbugal leen ci loolu ci dundug àddina si, ak ca roccig seeni ruu fekk ñu nekk di ay yéefar.
56وَيَحْلِفُونَ بِاللَّهِ إِنَّهُمْ لَمِنكُمْ وَمَا هُم مِّنكُمْ وَلَٰكِنَّهُمْ قَوْمٌ يَفْرَقُونَ
Ñuy waat ci Yàlla, naan ñoom ci yéen lañu bokk ; te bokkuñu ci yéen. Waaye ñoom dañoo ragal rekk ngeen dal (ci seen kaw).
57لَوْ يَجِدُونَ مَلْجَأً أَوْ مَغَارَاتٍ أَوْ مُدَّخَلًا لَّوَلَّوْا إِلَيْهِ وَهُمْ يَجْمَحُونَ
Bu ñu amoon làquwaay walla xunti walla fu ñu dugg (ba raw), kon ñu dëddu jëm fa te gaaw ca.
58وَمِنْهُم مَّن يَلْمِزُكَ فِي الصَّدَقَاتِ فَإِنْ أُعْطُوا مِنْهَا رَضُوا وَإِن لَّمْ يُعْطَوْا مِنْهَا إِذَا هُمْ يَسْخَطُونَ
Am na ci ñoom ñu la ayibal ci sarax yi : ku leen ca joxoon ñu bég ca ; ku leen joxul ñu xundu.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
56Aaya

Tekki — At-Tawba 56

Simoore At-Tawba Aaya 56 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñuy waat ci Yàlla, naan ñoom ci yéen lañu bokk…

Simoore Aaya 56/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 54–58. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers