Simoore Al-Insan
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Al-Insan pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Insan pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Insan Tekki. Al-Insan (Medinan) 31 Aaya.
Related
- Al-Insan TekkiWolof
- Al-Insan mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Al-Insan

ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Mo ndax nit dafa amul woon ab diir ci jamono bu kenn daawu ko limaale?
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Nun noo binde nit ci maniyu mu jaxasoo. Di ko nattu def ko muy dégg di gis.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Gindi nanu ko ci aw yoon , - amaana muy déloo njukkël di sant walla mu goreedi -
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Waajalal nanu yéefar ya ay càllala, ak i jéng ak safara wuy bérëx.
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
Ñu baax ña danañuy naane ci kaas yu ñu jaxasee kaafar,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
Batab ndox boo xam ne. Jaami Yàlla yaa cay naan, ñu di ko bëtte fa mu leen soob.
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Dañuy mottali seeni nisër tey ragal bis bu ayam wa tiis na .
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
te lañuy bëgg ñam lépp, terewul ñu di ko leel, miskiin, yaak jirim yaak ña ñu tëj kaso,
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
(te naan leen) : “noo ngi leen koy leele de : waaye bëggu nu ci ak pey walla gëram ngir Yàlla rekk tax.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Danoo ragal, ci sunu Boroom, bis bu ñàng te tëradi”.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Yàlla daldi leen fegal ayu boobale bis, dajale leen ak naataangeek mbégte,
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
mu faye leen lañu muñoon, Àjjana ak i sooy,
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
dañuy sóonu ca lal ya, te dunu fa gis ab jant waxantumalaak ab sedd liw.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Keram ya da leen di muur, meññatam ma yóore tiim leen.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Ñu di leen wër ak ay ndabi xaalis, ak ay koppi weer,
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
ay koppi weeri xaalis, yu yem kepp.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Ñu, di leen fa nàndale ak kaas yu ñu njare jinjeer,
ﯕﯖﯗﯘﯙ
ab bëtu ndox bu tudd Salsabiil.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Te ay xalee ngay wër ca ñoom sax cig ndaw. Soo leen gisee, da ngay foog ne peme ju ñu tasaare la ñu.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Soo ko gisee, danga fa gIisaale xeewal ak nguur gu màgg.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Dañuy sol mbubbi sooy yu nëtëx werta. Moom la ñuy jiital waaje ko, te dañu leen di takkal caqi xaalis. Seen Boroom di leen fa ndàndale naan gu laab.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Lii nag mooy seen neexal, te seen jëf it lu ñu sant la.
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋ
Nun de Noo wàcce Alxuraan ci yaw ndànk-ndànk.
ﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕ
Muñal sa dogalub Boroom, te bul topp, ci ñoom, kenn kuy def bàkkaar walla mu di yéefar.
ﰖﰗﰘﰙﰚﰛ
Te na nga tudd sa turu Boroom, subaak ngoon ;
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
te guddi gi it na nga Koy sujuudal ; te di ko sàbbaal [waxtuw] guddi lu bari.
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Ñoom dey da ñoo bëgg Àddina tey sàggane bis bu dis ginnaawal ko.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Nun Noo leen bind. May leen kàttan, te Sunu sooboon, Nu wuutal fi ñeneen.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Lii dey ag fàttali la. Képp ku mu soob man ngaa sóobu yoon jëm ca sa Boroom !
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Manu leen a sottal dara, te du dafa soob Yàlla. Moom ku Xam la ku Xereñ la.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Mooy tàbbal ku ko soob ci yërmëndéem. Te tooñkat yi, Waajalna leen mbugël mu mitti.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







