Simoore Al-Mursalat pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Mursalat pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Mursalat Tekki. Simoore Al-Mursalat (Meccan) 50 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore Al-Mursalat

ﮑﮒﮓ
77:1
Maa ngi giñ ci ngelaw ya ñu yabal muy jaayu.
ﮔﮕﮖ
77:2
Ak yiy ràddi càllmeer!
ﮗﮘﮙ
77:3
ak yiy gëwéeluy tasaare.
ﮚﮛﮜ
77:4
Ak yiy teqale dëgg ak fen (Laaya yi) ,
ﮝﮞﮟ
77:5
di sànni fàttali
ﮠﮡﮢﮣ
77:6
Di jélële walla muy xuppe !
ﮤﮥﮦﮧ
77:7
La ñu leen di tëkóo fàwwu mu ay (xew).
ﮨﮩﮪﮫ
77:8
Bu ru raafee biddiw yi,
ﮬﮭﮮﮯ
77:9
daldi xar asamaan si,
ﮰﮱﯓﯔ
77:10
moñoxe tundi doj yi,
ﯕﯖﯗﯘ
77:11
ak suñu dajalee Yonent ya !...
ﯙﯚﯛﯜ
77:12
Ana ban bis la doon xaar ?
ﯝﯞﯟ
77:13
Ca bisub àtte ba !
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
77:14
Ana kan moo lay xamal luy bisub àtte ba ?
ﯦﯧﯨﯩ
77:15
Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi.
ﯪﯫﯬﯭ
77:16
Moo ndax Nun faagaagalunu ñu jëkk ña?
ﯮﯯﯰﯱ
77:17
Toftal ca ña mujjoon ?
ﯲﯳﯴﯵ
77:18
Noonu la ñuy def ak tooñkat ya.
ﯶﯷﯸﯹ
77:19
Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
77:20
Moo ndax bindewunu leen ci ndox mu doyadi
ﭗﭘﭙﭚﭛ
77:21
Nu daldi koy saxal ci barab wu wóor,
ﭜﭝﭞﭟ
77:22
ba ca ab diir bu ñu xam ?
ﭠﭡﭢﭣ
77:23
Nu daldi dogal cëy Noo mana dogal yemale.
ﭤﭥﭦﭧ
77:24
Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi.
ﭨﭩﭪﭫﭬ
77:25
Ndax defu nu suuf si mu làmboo lépp,
ﭭﭮﭯ
77:26
ñuy dund ak ñu dee ?
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
77:27
Te def Nanu ci ay tund doj yu kawe? Te nàndale leen ak ndox mu neex ?
ﭸﭹﭺﭻ
77:28
Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
77:29
Fëxleen nag jëm ci li ngeen daan weddi !
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
77:30
Fëxleen jëm ca ker ga am ñatti tokkoor [saxaar sa] ;
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
77:31
manuta keral kenn waxatumaak di feg tàkk-tàkk ;
ﮑﮒﮓﮔﮕ
77:32
moom dafay sànni ay ferñent yu tollu ni njéndi,
ﮖﮗﮘﮙ
77:33
dañu melni ay giléem yu mboq
ﮚﮛﮜﮝ
77:34
Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi.
ﮞﮟﮠﮡﮢ
77:35
Bu bis baa du ñu mana àddu wax,
ﮣﮤﮥﮦﮧ
77:36
kenn du leen may pose bu ñuy jéggaloo.
ﮨﮩﮪﮫ
77:37
Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
77:38
Lii mooy bisub àtte ba, boole nanu leen ak ñu jëkk ña.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
77:39
Su ngeen amee ay pexe, fexel leen Ma.
ﯚﯛﯜﯝ
77:40
Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
77:41
Ña ragal Yàlla ñoom ña nga ca ker ya ak bëti ndox ya.
ﯤﯥﯦﯧ
77:42
Ak ay fuytéef ya ñu bëgg.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
77:43
“Lekkleen te naan, mooy peyug la ngeen daan jëf”.
ﯯﯰﯱﯲﯳ
77:44
Noonu la Ñuy faye way rafetal ya.
ﯴﯵﯶﯷ
77:45
Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
77:46
“Lekkleen te bànneexu tuuti ; yéen ay tooñkat ngeen”.
ﯾﯿﰀﰁ
77:47
Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi.
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
77:48
Te saasu ñu leen waxee ne : “rukóoleen, duñu rukoo (duñu julli).
ﰉﰊﰋﰌ
77:49
Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi.
ﰍﰎﰏﰐﰑ
77:50
Bu waxtaan wii jàllee, ana wan waxtaan lañuy gëmati ?
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







