PDF —
29 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore At-Takwir pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore At-Takwir pdf Wolof — Wàcce Simoore At-Takwir Tekki. Simoore At-Takwir (Meccan) 29 Aaya.

← AbasaSimoore At-Takwir Al-Infitar →


29 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭙﭚﭛﭜ
81:1 Saa su ñu lëndamalee jant bi, Maa ngi giiñ
ﭝﭞﭟﭠ
81:2 ak saa su biddew yi rotee,
ﭡﭢﭣﭤ
81:3 ak tundi doj yi saa su ñuy randatu di dox,
ﭥﭦﭧﭨ
81:4 ak saa su nu, sàgganee geleemam ga ëmbu ba sori talatuñu ko,
ﭩﭪﭫﭬ
81:5 ak ndokmenta ya (rab yu aaytal ya), dajaloo ñu dekkalaat leen,
ﭭﭮﭯﭰ
81:6 ak saa su ñu taalee geej ya mu di safara,
ﭱﭲﭳﭴ
81:7 ak saa su ñu lëkëlee ruu ya
ﭵﭶﭷﭸ
81:8 ak saa su ñu laajee doom ju jigéen ja nu soloon te fekk muy dund, ngir daw gàcce
ﭹﭺﭻﭼ
81:9 ci ban bàkkaar bu mu def moo tax ñu rey ko.
ﭽﭾﭿﮀ
81:10 Ak saa su ñu tasaaree kayit yi ëmboon jëfi bindéef yi,
ﮁﮂﮃﮄ
81:11 ak saa su nu xollee deri asamaan si
ﮅﮆﮇﮈ
81:12 ak saa su ñu taalee safaraw jahim,
ﮉﮊﮋﮌ
81:13 ak saas u ñu jigeelee Àjjana,
ﮍﮎﮏﮐﮑ
81:14 bakkan bu Yàlla sàkk xam na la mu jëfoon.
ﮒﮓﮔﮕ
81:15 Déet !... Maa ngi giiñ ci biddiw yi fàq guddi
ﮖﮗﮘ
81:16 tey daw di suux !
ﮙﮚﮛﮜ
81:17 ak ci guddi gi saa suy tàmbali!
ﮝﮞﮟﮠ
81:18 ak ci suba si saa suy fenk!
ﮡﮢﮣﮤﮥ
81:19 Ci ne [Alxuraan jii] waxi ab Yonent la bu tedd (Jibriil),
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
81:20 di boroom kàttan gu rëy, di ab xejj fa Boroom ganganaay ga Aras,
ﮭﮮﮯﮰ
81:21 di ku ñuy digël, ndigëlam ca kaw, di ku ñu woolu.
ﮱﯓﯔﯕ
81:22 Te seen àndandoo ja (Muhammad) du ab dof de ;
ﯖﯗﯘﯙﯚ
81:23 moom gis na tigi (Jibriil), ca asamaan ya
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
81:24 te moom nayul ci li ñu ko soloo.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
81:25 Te it [Alxuraan ji] du waxi seytaane sa ñu jam.
ﯧﯨﯩ
81:26 Kon ana fu ngeen jëm ?
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
81:27 Lii du lenn lu dul luy fàttali waa àddina si yépp,
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
81:28 ku mu soob ci yéen mu topp yoon wu jub xocc wa.
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
81:29 Waaye manuleena soob mukk, te du ut ne dafa soob Yàlla, Boroom àddina si yépp ;

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers