Simoore Abasa pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Abasa pdf Wolof — Wàcce Simoore Abasa Tekki. Simoore Abasa (Meccan) 42 Aaya.
Related
- Simoore Abasa TekkiWolof
- Simoore Abasa mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Abasa

ﭑﭒﭓ
80:1
Sóomóorlu na daldi dumóoyu
ﭔﭕﭖﭗ
80:2
ba ko gumba ga digëlee.
ﭘﭙﭚﭛﭜ
80:3
Xamoo : ndax dafa bëgg tuub ?
ﭝﭞﭟﭠﭡ
80:4
walla muy fàttaliku man caa jariñoo ?
ﭢﭣﭤﭥ
80:5
Ka nga xam ne dafa woomal
ﭦﭧﭨﭩ
80:6
ba tax nga jublu ko.
ﭪﭫﭬﭭﭮ
80:7
Lu laak moom ? (yaw muhammadu) ”
ﭯﭰﭱﭲﭳ
80:8
Waaye ku la dikkëlati
ﭴﭵﭶ
80:9
tey wuta ragal Yàlla,
ﭷﭸﭹﭺ
80:10
te faalewoo ko.
ﭻﭼﭽﭾ
80:11
Loolu dey ag fàttali la
ﭿﮀﮁﮂ
80:12
ku mu soob, mu fàttaliku ko
ﮃﮄﮅﮆ
80:13
mi ngi ci ay xët yu ñu teral (bind ko),
ﮇﮈﮉ
80:14
yu ñu yékëti, te laabal ko,
ﮊﮋﮌ
80:15
nekk ci yoxoy ak tekkikat (malaaka)
ﮍﮎﮏ
80:16
yu tedd, yu baax.
ﮐﮑﮒﮓﮔ
80:17
reyeef na nit ngir ngoreedeem !
ﮕﮖﮗﮘﮙ
80:18
Ci lan la ko [Yàlla] bind ?
ﮚﮛﮜﮝﮞ
80:19
Ci toqu maniyu la ko binde, dugal ay mbiram :
ﮟﮠﮡﮢ
80:20
daldi koy yombalal yoon wa ;
ﮣﮤﮥﮦ
80:21
daldi koy rey, tàbbal ko ci bàmmeel ;
ﮧﮨﮩﮪﮫ
80:22
te saa su Ko soobee mu dekkalaat Ko.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
80:23
Déedéet ! [Nit] moom matalul mukk la nu ko digëloon.
ﯓﯔﯕﯖﯗ
80:24
Na nit di xool ci aw ñamam lekkam :
ﯘﯙﯚﯛﯜ
80:25
Nun noo sotti ndox mu dottiku,
ﯝﯞﯟﯠﯡ
80:26
ba noppi Nu xar suuf mu fett
ﯢﯣﯤﯥ
80:27
nu saxal ci ay kembu,
ﯦﯧﯨ
80:28
ay reseñ ak i lujum,
ﯩﯪﯫ
80:29
ak i oliw ak tàndarma,
ﯬﯭﯮ
80:30
ak ay dër yu naat,
ﯯﯰﯱ
80:31
ak i fuytéef ak i xob, ngub
ﯲﯳﯴﯵ
80:32
mu di seen bànneex ak seenug jur.
ﯶﯷﯸﯹ
80:33
Bu bis pénc ba dikkee,
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
80:34
bis ba nit di daw mbokkam,
ﰀﰁﰂ
80:35
ak yaayam, ak baayam,
ﰃﰄﰅ
80:36
ak soxnaam ak doomam,
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
80:37
kenn ku nekk, bu keroogee, am mbir mu ko doy sëkk.
ﰍﰎﰏﰐ
80:38
bu keroogee, ay xarkanam yu naat,
ﰑﰒﰓ
80:39
bég lool tey ree.
ﰔﰕﰖﰗﰘ
80:40
Bu keroogee, am it, ay xarkanam yu fundóoñ,
ﭑﭒﭓ
80:41
lëndëm kariis.
ﭔﭕﭖﭗﭘ
80:42
Ñooña ñoo di yéefar ya, di kàccoor ya.
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







