Simoore Al-Mutaffifin pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Mutaffifin pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Mutaffifin Tekki. Simoore Al-Mutaffifin (Meccan) 36 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore Al-Mutaffifin

ﯖﯗﯘ
83:1
Xuru safara ñeel na naxaatekat ya
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
83:2
ñay natt peese di ëppal lay jëm ca ñoom,
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
83:3
te su ñuy nattal keneen, wàññi ko.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
83:4
Xanaa ñoom dañoo jàpput ne dees na leen dekkilaat (ginnaaw dee),
ﭑﭒﭓ
83:5
ca bis bu ñàng,
ﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
83:6
bis ba nit ña di taxaw ci kanam Boroom Àddina si yépp ?
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
83:7
Déet... ! Waaye téereb kàccoor yaa nga ca Sijjin de
ﭡﭢﭣﭤﭥ
83:8
ana lan moo lay xamal luy Sijjin ?
ﭦﭧﭨ
83:9
ab téere la bu ñu xas tàmpe.
ﭩﭪﭫﭬ
83:10
Bu keroogee, weddikat ya, danañu tàbbi xuru safara,
ﭭﭮﭯﭰﭱ
83:11
ña daan weddi bis Pénc ba.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
83:12
te kenn, du ko weddi ku dul ab jalgatikat, buy def bàkkaar :
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
83:13
su ñu jàngee ci ñoom Laaya, dañu naan : “Léebi mag ña la! ”
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
83:14
Lañu daan def moo muur xomaagal seen xol ya.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
83:15
Déet ! Ñoom kay bu keroogee duñu gis seen Boroom de,
ﮔﮕﮖﮗﮘ
83:16
te, dees na leen lakk, Safara jahiim ;
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
83:17
te di leen wax naan leen: “Lii ngeen daan weddi ! ”
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
83:18
Déetawaay ! Téereb ñu baax ñaa nga ca biir Illiyiina
ﮨﮩﮪﮫﮬ
83:19
ana lan moo lay xamal luy Illiyiina ?
ﮭﮮﮯ
83:20
ab téere la bu ñu xas tàmpe !
ﮰﮱﯓ
83:21
Ña jege Yàlla koy seede (Malaaka ya).
ﯔﯕﯖﯗﯘ
83:22
Ñu baax ñaa nga ca biir xeewal,
ﯙﯚﯛﯜ
83:23
ña nga ne toŋŋ ca kaw toogu ya, di xool.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
83:24
Danga seere ca seen xarkanam ya, naataangey xéewël ya.
ﯣﯤﯥﯦﯧ
83:25
Ñu nandalu ci sàngaras àjjana suñu xàmmee,
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
83:26
tem-temam misk lay doon. Ñiy rawante nañu rawante [ci am ko]
ﯰﯱﯲﯳ
83:27
Di njarum Tasniim,
ﯴﯵﯶﯷﯸ
83:28
bëtub ndox la bu ña jegeñoo cay naan.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
83:29
Tooñkat ya dañu daan reetaan ña gëmoon,
ﰂﰃﰄﰅﰆ
83:30
saa suñu leen rombaan, di leen ñaawal,
ﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
83:31
bu ñu delluwaan ca seen njaboot, di ko kafe,
ﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
83:32
suñu leen masaana gis dañu daan wax ne : “Ñii dañoo sànku”.
ﰕﰖﰗﰘﰙ
83:33
Te, yabalunu leen ca ñoom ngir ñu daan leen wattu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
83:34
Tey jii nag, ñi gëm ñooy reetaan yéefar ya
ﭘﭙﭚﭛ
83:35
ña nga ne toŋŋ ca toogu ya, di xool.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
83:36
Moo ndax yéefar ya am nañu yoolub la ñu daan def ?
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







