Hud · 83/123
Tekki Waxtaan — Hud
مُّسَوَّمَةً عِندَ رَبِّكَ ۖ وَمَا هِيَ مِنَ الظَّالِمِينَ بِبَعِيدٍ ۝٨٣
Musawwamatan `inda Rabbik; wa maa hiya minaz zaalimena biba`eed
📖 Tekkim Wolof
yu ñu màndargaal ca sa Boroom. Te dëkk boobu soreewul ag way-tooñ ya [ya ca Màkka].
🎧 Dégg

📜 Aaya 81-85 — Hud

81قَالُوا يَا لُوطُ إِنَّا رُسُلُ رَبِّكَ لَن يَصِلُوا إِلَيْكَ ۖ فَأَسْرِ بِأَهْلِكَ بِقِطْعٍ مِّنَ اللَّيْلِ وَلَا يَلْتَفِتْ مِنكُمْ أَحَدٌ إِلَّا امْرَأَتَكَ ۖ إِنَّهُ مُصِيبُهَا مَا أَصَابَهُمْ ۚ إِنَّ مَوْعِدَهُمُ الصُّبْحُ ۚ أَلَيْسَ الصُّبْحُ بِقَرِيبٍ
Ñu ne ko : “Éy Lóot, nun ay ndawi sa Boroom lanu. Duñu agsi ci yaw. Nanga rañaan yaak sa njaboot ci biir guddi gi. Te bu kenn ci ñoom gestu. Ba mu des sa soxna ndax moom lu leen dal dana ko dal. Seenub àpp ëllëg rekk la. Moo ndax suba jigeñul ? ”
82فَلَمَّا جَاءَ أَمْرُنَا جَعَلْنَا عَالِيَهَا سَافِلَهَا وَأَمْطَرْنَا عَلَيْهَا حِجَارَةً مِّن سِجِّيلٍ مَّنضُودٍ
Ba Sunu dogal agsee, wëlbati Nanu [dëkk ba], la féete woon kaw féete suuf, Nu sotti ca kawam tawu xeer yu jóge Sijjiil [Safara] ay doj yu ñu toftale,
83مُّسَوَّمَةً عِندَ رَبِّكَ ۖ وَمَا هِيَ مِنَ الظَّالِمِينَ بِبَعِيدٍ
yu ñu màndargaal ca sa Boroom. Te dëkk boobu soreewul ag way-tooñ ya [ya ca Màkka].
84۞ وَإِلَىٰ مَدْيَنَ أَخَاهُمْ شُعَيْبًا ۚ قَالَ يَا قَوْمِ اعْبُدُوا اللَّهَ مَا لَكُم مِّنْ إِلَٰهٍ غَيْرُهُ ۖ وَلَا تَنقُصُوا الْمِكْيَالَ وَالْمِيزَانَ ۚ إِنِّي أَرَاكُم بِخَيْرٍ وَإِنِّي أَخَافُ عَلَيْكُمْ عَذَابَ يَوْمٍ مُّحِيطٍ
Yónni woon Nanu it ca waa Madyaana seen mbokk Suhaybu, mu ne leen : "Yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla ; amuleen jeneen yàlla ju dul Moom. Buleen wàññi nattukaay yi ak màndaxe yi. Gis naa ne yéen a ngi ci biiri xéewal, te ragal naa mbugal dal leen ca bis ba ëmb lépp.
85وَيَا قَوْمِ أَوْفُوا الْمِكْيَالَ وَالْمِيزَانَ بِالْقِسْطِ ۖ وَلَا تَبْخَسُوا النَّاسَ أَشْيَاءَهُمْ وَلَا تَعْثَوْا فِي الْأَرْضِ مُفْسِدِينَ
Yéen samaw nit, nangeen di matal natt ak màndaxe cig maandute, te buleen wàññi dara ci lu nit ñi moom, te buleen salfaañe ci suuf si nekk yàqkat..
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
83Aaya

Tekki — Hud 83

Simoore Hud Aaya 83 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : yu ñu màndargaal ca sa Boroom. Te dëkk boobu soreewul…

Simoore Aaya 83/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 81–85. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers