Yusuf · 17/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
قَالُوا يَا أَبَانَا إِنَّا ذَهَبْنَا نَسْتَبِقُ وَتَرَكْنَا يُوسُفَ عِندَ مَتَاعِنَا فَأَكَلَهُ الذِّئْبُ ۖ وَمَا أَنتَ بِمُؤْمِنٍ لَّنَا وَلَوْ كُنَّا صَادِقِينَ ۝١٧
Qaaloo yaaa abaanaaa innaa zahabnaa nastabiqu wa taraknaa Yoosufa `inda mataa`inaa fa akhalahuz zi`b, wa maaa anta bimu`minil lanaa wa law kunnaa saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
Ñu ne : "Yaw sunu baay, ba ñu demee, dañu doon rawante, bàyyi Yuusufa ca sunuy yóbbal ; ag till lekk ko. Te bu nu waxee dëgg it du tax nga gëm li nu wax”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 15-19 — Yusuf

15فَلَمَّا ذَهَبُوا بِهِ وَأَجْمَعُوا أَن يَجْعَلُوهُ فِي غَيَابَتِ الْجُبِّ ۚ وَأَوْحَيْنَا إِلَيْهِ لَتُنَبِّئَنَّهُم بِأَمْرِهِمْ هَٰذَا وَهُمْ لَا يَشْعُرُونَ
Ba ñu àndeek moom, te mànkoo ci sànni ko ca xóot-xóot ba [teen ba], Nu xamal [Nun Yàlla] Yuusufa ne : “Danga leen mës a nettali seen jëf jii fu ñu ko foogewul”.
16وَجَاءُوا أَبَاهُمْ عِشَاءً يَبْكُونَ
Ñu dellu ci seen baay ci marax, di joox.
17قَالُوا يَا أَبَانَا إِنَّا ذَهَبْنَا نَسْتَبِقُ وَتَرَكْنَا يُوسُفَ عِندَ مَتَاعِنَا فَأَكَلَهُ الذِّئْبُ ۖ وَمَا أَنتَ بِمُؤْمِنٍ لَّنَا وَلَوْ كُنَّا صَادِقِينَ
Ñu ne : "Yaw sunu baay, ba ñu demee, dañu doon rawante, bàyyi Yuusufa ca sunuy yóbbal ; ag till lekk ko. Te bu nu waxee dëgg it du tax nga gëm li nu wax”.
18وَجَاءُوا عَلَىٰ قَمِيصِهِ بِدَمٍ كَذِبٍ ۚ قَالَ بَلْ سَوَّلَتْ لَكُمْ أَنفُسُكُمْ أَمْرًا ۖ فَصَبْرٌ جَمِيلٌ ۖ وَاللَّهُ الْمُسْتَعَانُ عَلَىٰ مَا تَصِفُونَ
Ñu indiwaale yéreem yu taq dereet [ju dul dereeti Yusuufa]. Mu tontu leen ne : “Yéen dey, seen bakkan rafetal na leen mbir mii... Waaye danaa sax ci muñ gu rafet ! Ci Yàlla laay dimbandikoo ci lii ngeen nettali ! ”
19وَجَاءَتْ سَيَّارَةٌ فَأَرْسَلُوا وَارِدَهُمْ فَأَدْلَىٰ دَلْوَهُ ۖ قَالَ يَا بُشْرَىٰ هَٰذَا غُلَامٌ ۚ وَأَسَرُّوهُ بِضَاعَةً ۚ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِمَا يَعْمَلُونَ
Ay tukkikat agsi, yónni seenub rootkat, mu yoor baagam. Mu daldi ne : “Mbégtee ngi ! Lii de ab xale la ! ” Ñu yóbbu ko nar koo jaay. Te Yàlla ku xam la la ñuy def.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
17Aaya

Tekki — Yusuf 17

Simoore Yusuf Aaya 17 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñu ne : "Yaw sunu baay, ba ñu demee, dañu…

Simoore Aaya 17/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 15–19. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers