Yusuf · 55/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
قَالَ اجْعَلْنِي عَلَىٰ خَزَائِنِ الْأَرْضِ ۖ إِنِّي حَفِيظٌ عَلِيمٌ ۝٥٥
Qaalaj `alnee `alaa khazaaa`inil ardi innee hafeezun `aleem
📖 Tekkim Wolof
Mu ne : “Dénkleen ma alali réew mi : am naa xam-xamu wattu ko”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 53-57 — Yusuf

53۞ وَمَا أُبَرِّئُ نَفْسِي ۚ إِنَّ النَّفْسَ لَأَمَّارَةٌ بِالسُّوءِ إِلَّا مَا رَحِمَ رَبِّي ۚ إِنَّ رَبِّي غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Jéemumaa setal sama bopp, ndax bakkan moom digalaakoon la ci lu bon, [mucctil ci moom] ku dul ku sama Boroom yërëm. Ndax sama Boroom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la”.
54وَقَالَ الْمَلِكُ ائْتُونِي بِهِ أَسْتَخْلِصْهُ لِنَفْسِي ۖ فَلَمَّا كَلَّمَهُ قَالَ إِنَّكَ الْيَوْمَ لَدَيْنَا مَكِينٌ أَمِينٌ
Buur ba ne : “Indil-leen ma ko : def ko mu sës ci man”. Ba mu waxeek moom, mu ne ko : “Bis niki tey, nekk nga ci man ku ñu darajaal, ku ñu wóolu”.
55قَالَ اجْعَلْنِي عَلَىٰ خَزَائِنِ الْأَرْضِ ۖ إِنِّي حَفِيظٌ عَلِيمٌ
Mu ne : “Dénkleen ma alali réew mi : am naa xam-xamu wattu ko”.
56وَكَذَٰلِكَ مَكَّنَّا لِيُوسُفَ فِي الْأَرْضِ يَتَبَوَّأُ مِنْهَا حَيْثُ يَشَاءُ ۚ نُصِيبُ بِرَحْمَتِنَا مَن نَّشَاءُ ۖ وَلَا نُضِيعُ أَجْرَ الْمُحْسِنِينَ
Noonu Lanu darajaale Yuusufa ca réew ma, mu fay wàcc fu ko neex. Dananu jox sunu yërmaande ku Nu neex te Dunu sànk peyug rafetalkat ya.
57وَلَأَجْرُ الْآخِرَةِ خَيْرٌ لِّلَّذِينَ آمَنُوا وَكَانُوا يَتَّقُونَ
Te peyug àllaaxira moo gën ci ña gëm, di ña ragal [Yàlla].
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
55Aaya

Tekki — Yusuf 55

Simoore Yusuf Aaya 55 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu ne : “Dénkleen ma alali réew mi : am…

Simoore Aaya 55/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 53–57. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers