An-Nahl · 117/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
مَتَاعٌ قَلِيلٌ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ ۝١١٧
Mata`un qaleelunw wa lahum `azaabun aleem
📖 Tekkim Wolof
Ñeel na leen yóbbal bu néew, ak mbugal mu metti.

🎧 Dégg


📜 Aaya 115-119 — An-Nahl

115إِنَّمَا حَرَّمَ عَلَيْكُمُ الْمَيْتَةَ وَالدَّمَ وَلَحْمَ الْخِنزِيرِ وَمَا أُهِلَّ لِغَيْرِ اللَّهِ بِهِ ۖ فَمَنِ اضْطُرَّ غَيْرَ بَاغٍ وَلَا عَادٍ فَإِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Waaye araamal na ci yéen médd, ak deret, ak yàppu mbaam-xuux ak lu ñu [rey] te tuddu ca keneen ku dul Yàlla. Képp ku nar a loru [ba tax mu lekk yooya araam], na xam ne Yàlla jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
116وَلَا تَقُولُوا لِمَا تَصِفُ أَلْسِنَتُكُمُ الْكَذِبَ هَٰذَا حَلَالٌ وَهَٰذَا حَرَامٌ لِّتَفْتَرُوا عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَفْتَرُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ لَا يُفْلِحُونَ
Buleen wax loo xam ne seeni làmmiñ a koy melal ciy fen, naan : “Lii dagan na, lii araam na”, di duural Yàlla ay fen. Te ñiy duural Yàlla ay fen duñu texe.
117مَتَاعٌ قَلِيلٌ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ñeel na leen yóbbal bu néew, ak mbugal mu metti.
118وَعَلَى الَّذِينَ هَادُوا حَرَّمْنَا مَا قَصَصْنَا عَلَيْكَ مِن قَبْلُ ۖ وَمَا ظَلَمْنَاهُمْ وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ
Te araamaloon nañu ca yahuud ya li Nu la nettali ca bu jëkk. Te tooñunu leen ; waaye ñoo tooñ seen bopp.
119ثُمَّ إِنَّ رَبَّكَ لِلَّذِينَ عَمِلُوا السُّوءَ بِجَهَالَةٍ ثُمَّ تَابُوا مِن بَعْدِ ذَٰلِكَ وَأَصْلَحُوا إِنَّ رَبَّكَ مِن بَعْدِهَا لَغَفُورٌ رَّحِيمٌ
Mu des nag ne sa Boroom, lu jëm ci ña jëfoon [lu bon niki bokkaale] cig réer, ginnaaw loola ñu tuub ko, rafetal seeni jëf, ñooña sa Boroom fàwwu Mu jéggal leen, yërëm leen naka.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
117Aaya

Tekki — An-Nahl 117

Simoore An-Nahl Aaya 117 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñeel na leen yóbbal bu néew, ak mbugal mu metti.

Simoore Aaya 117/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 115–119. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers