An-Nahl · 123/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
ثُمَّ أَوْحَيْنَا إِلَيْكَ أَنِ اتَّبِعْ مِلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا ۖ وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ ۝١٢٣
Summma awhainaa ilaika anit tabi` Millata Ibraaheema haneefaa; wa maa kaana minal mushrikeen
📖 Tekkim Wolof
Tax na Nu soloo la ne : “Toppal diiney Ibraahiima [yaw Muhammad] cig wéetal sa Boroom, bokkul woon ca bokkaalekat ya”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 121-125 — An-Nahl

121شَاكِرًا لِّأَنْعُمِهِ ۚ اجْتَبَاهُ وَهَدَاهُ إِلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Ku daan gërëm [Yàlla] la ci xéewalam yi, Yàlla tànn na ko, gindi ko, teg ko ci yoon wu jub xocc wa.
122وَآتَيْنَاهُ فِي الدُّنْيَا حَسَنَةً ۖ وَإِنَّهُ فِي الْآخِرَةِ لَمِنَ الصَّالِحِينَ
Te may Nanu ko ci àddina tagg wu rafet. Te ca àllaaxira, dana bokk ca ñu sell, ñu [yiw] ña.
123ثُمَّ أَوْحَيْنَا إِلَيْكَ أَنِ اتَّبِعْ مِلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا ۖ وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Tax na Nu soloo la ne : “Toppal diiney Ibraahiima [yaw Muhammad] cig wéetal sa Boroom, bokkul woon ca bokkaalekat ya”.
124إِنَّمَا جُعِلَ السَّبْتُ عَلَى الَّذِينَ اخْتَلَفُوا فِيهِ ۚ وَإِنَّ رَبَّكَ لَيَحْكُمُ بَيْنَهُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ فِيمَا كَانُوا فِيهِ يَخْتَلِفُونَ
Màggal bisu gaawu tegewul woon lu dul ca kaw ña ca juuyoo woon. Te sa Boroom dana àtte seen diggante ca Bis-pénc ba ca la ñu nekkoon di ca juuyoo.
125ادْعُ إِلَىٰ سَبِيلِ رَبِّكَ بِالْحِكْمَةِ وَالْمَوْعِظَةِ الْحَسَنَةِ ۖ وَجَادِلْهُم بِالَّتِي هِيَ أَحْسَنُ ۚ إِنَّ رَبَّكَ هُوَ أَعْلَمُ بِمَن ضَلَّ عَن سَبِيلِهِ ۖ وَهُوَ أَعْلَمُ بِالْمُهْتَدِينَ
Wooteel ci sa yoonu Boroom [Lislaam], sukkandiku ci Alxuraan ak waare ci lu baax. Nanga dàggasanteek ñoom ca na mu gën a rafete. Naka sa Boroom moo gën a xam ña réer, sori aw yoonam te Moom moo gën a xam ñu jub ña.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
123Aaya

Tekki — An-Nahl 123

Simoore An-Nahl Aaya 123 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Tax na Nu soloo la ne : “Toppal diiney Ibraahiima…

Simoore Aaya 123/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 121–125. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers