An-Nahl · 94/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
وَلَا تَتَّخِذُوا أَيْمَانَكُمْ دَخَلًا بَيْنَكُمْ فَتَزِلَّ قَدَمٌ بَعْدَ ثُبُوتِهَا وَتَذُوقُوا السُّوءَ بِمَا صَدَدتُّمْ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۖ وَلَكُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ ۝٩٤
Wa laa tattakhizooo aimaanakum dakhalam bainakum ftazilla qadamum ba`da subootihaa wa tazooqus sooo`a bimmaa sadattum `an sabeelil laahi wa lakum `azaabun `azeem
📖 Tekkim Wolof
Buleen def seeni ngiñ muy yàq li nekk seeni diggante, ba tax tànk bu sampu woon tarxiis, kon dangeen mos lu bon ndax seen dëddëleek nit ñeek yoonu Yàlla, mbugal mu mag dal leen.
🎧 Dégg

📜 Aaya 92-96 — An-Nahl

92وَلَا تَكُونُوا كَالَّتِي نَقَضَتْ غَزْلَهَا مِن بَعْدِ قُوَّةٍ أَنكَاثًا تَتَّخِذُونَ أَيْمَانَكُمْ دَخَلًا بَيْنَكُمْ أَن تَكُونَ أُمَّةٌ هِيَ أَرْبَىٰ مِنْ أُمَّةٍ ۚ إِنَّمَا يَبْلُوكُمُ اللَّهُ بِهِ ۚ وَلَيُبَيِّنَنَّ لَكُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ مَا كُنتُمْ فِيهِ تَخْتَلِفُونَ
Buleen mel ni ndaw sa firinci buum ga mu raw ba mu dëgër, mu firinci ko ba mu nekk i dogit, ngeen di jàppe seeni ngiñ li ngeen di wuruje ci seen diggante, ngeen defe ne ku ëpp mbooloo mën naa wor. Te Yàlla dafa leen ciy natt. Te bu Bis-pénc baa Dana leen leeralal la ngeen nekkoon di ca juyoo.
93وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ لَجَعَلَكُمْ أُمَّةً وَاحِدَةً وَلَٰكِن يُضِلُّ مَن يَشَاءُ وَيَهْدِي مَن يَشَاءُ ۚ وَلَتُسْأَلُنَّ عَمَّا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Su neexoon Yàlla Mu def leen ngeen nekk wenn xeet doŋŋ. Waaye Mooy bàyyi cig réeram ku ko soob, di gindi ku ko soob. Te fàwwu ñu laaj leen ca la ngeen defoon.
94وَلَا تَتَّخِذُوا أَيْمَانَكُمْ دَخَلًا بَيْنَكُمْ فَتَزِلَّ قَدَمٌ بَعْدَ ثُبُوتِهَا وَتَذُوقُوا السُّوءَ بِمَا صَدَدتُّمْ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۖ وَلَكُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Buleen def seeni ngiñ muy yàq li nekk seeni diggante, ba tax tànk bu sampu woon tarxiis, kon dangeen mos lu bon ndax seen dëddëleek nit ñeek yoonu Yàlla, mbugal mu mag dal leen.
95وَلَا تَشْتَرُوا بِعَهْدِ اللَّهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۚ إِنَّمَا عِندَ اللَّهِ هُوَ خَيْرٌ لَّكُمْ إِن كُنتُمْ تَعْلَمُونَ
Buleen di jaaye kóllareg Yàlla ci njëg gu néew. La nekk fa Yàlla moo gën ci yéen, cëy bu ngeen xamoon !
96مَا عِندَكُمْ يَنفَدُ ۖ وَمَا عِندَ اللَّهِ بَاقٍ ۗ وَلَنَجْزِيَنَّ الَّذِينَ صَبَرُوا أَجْرَهُم بِأَحْسَنِ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Li ngeen moom day jeex, la Yàlla moom nag luy des la. Te fàwwu Dananu feye ñiy muñ ca na mu gën a rafete, ngir la ñu nekkoon di ko def.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
94Aaya

Tekki — An-Nahl 94

Simoore An-Nahl Aaya 94 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Buleen def seeni ngiñ muy yàq li nekk seeni diggante,…

Simoore Aaya 94/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 92–96. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers