An-Nahl · 95/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
وَلَا تَشْتَرُوا بِعَهْدِ اللَّهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۚ إِنَّمَا عِندَ اللَّهِ هُوَ خَيْرٌ لَّكُمْ إِن كُنتُمْ تَعْلَمُونَ ۝٩٥
Wa laa tashtaroo bi `ahdil laahi samanan qaleelaa; innamaa `indal laahi huwa khairul lakum in kuntum ta`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Buleen di jaaye kóllareg Yàlla ci njëg gu néew. La nekk fa Yàlla moo gën ci yéen, cëy bu ngeen xamoon !

🎧 Dégg


📜 Aaya 93-97 — An-Nahl

93وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ لَجَعَلَكُمْ أُمَّةً وَاحِدَةً وَلَٰكِن يُضِلُّ مَن يَشَاءُ وَيَهْدِي مَن يَشَاءُ ۚ وَلَتُسْأَلُنَّ عَمَّا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Su neexoon Yàlla Mu def leen ngeen nekk wenn xeet doŋŋ. Waaye Mooy bàyyi cig réeram ku ko soob, di gindi ku ko soob. Te fàwwu ñu laaj leen ca la ngeen defoon.
94وَلَا تَتَّخِذُوا أَيْمَانَكُمْ دَخَلًا بَيْنَكُمْ فَتَزِلَّ قَدَمٌ بَعْدَ ثُبُوتِهَا وَتَذُوقُوا السُّوءَ بِمَا صَدَدتُّمْ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۖ وَلَكُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Buleen def seeni ngiñ muy yàq li nekk seeni diggante, ba tax tànk bu sampu woon tarxiis, kon dangeen mos lu bon ndax seen dëddëleek nit ñeek yoonu Yàlla, mbugal mu mag dal leen.
95وَلَا تَشْتَرُوا بِعَهْدِ اللَّهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۚ إِنَّمَا عِندَ اللَّهِ هُوَ خَيْرٌ لَّكُمْ إِن كُنتُمْ تَعْلَمُونَ
Buleen di jaaye kóllareg Yàlla ci njëg gu néew. La nekk fa Yàlla moo gën ci yéen, cëy bu ngeen xamoon !
96مَا عِندَكُمْ يَنفَدُ ۖ وَمَا عِندَ اللَّهِ بَاقٍ ۗ وَلَنَجْزِيَنَّ الَّذِينَ صَبَرُوا أَجْرَهُم بِأَحْسَنِ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Li ngeen moom day jeex, la Yàlla moom nag luy des la. Te fàwwu Dananu feye ñiy muñ ca na mu gën a rafete, ngir la ñu nekkoon di ko def.
97مَنْ عَمِلَ صَالِحًا مِّن ذَكَرٍ أَوْ أُنثَىٰ وَهُوَ مُؤْمِنٌ فَلَنُحْيِيَنَّهُ حَيَاةً طَيِّبَةً ۖ وَلَنَجْزِيَنَّهُمْ أَجْرَهُم بِأَحْسَنِ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Ku jëf u yiw, di ku góor walla ku jigéen te muy ku gëm, fàwwu Dananu ko dundal dundu gu sell. Te fàwwu Dananu leen fey seenug pey na mu gën a rafete la ñu nekkoon di ko jëf.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
95Aaya

Tekki — An-Nahl 95

Simoore An-Nahl Aaya 95 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Buleen di jaaye kóllareg Yàlla ci njëg gu néew. La…

Simoore Aaya 95/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 93–97. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers