Maryam · 33/98
Tekki Waxtaan — Maryam
وَالسَّلَامُ عَلَيَّ يَوْمَ وُلِدتُّ وَيَوْمَ أَمُوتُ وَيَوْمَ أُبْعَثُ حَيًّا ۝٣٣
Wassalaamu `alaiya yawma wulittu wa yawma amootu wa yawma ub`asu baiyaa
📖 Tekkim Wolof
Jàmm rekk laay am bis ba ma juddoo, ak ca bis ba may dee ak bis ba may dekkiwaat”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 31-35 — Maryam

31وَجَعَلَنِي مُبَارَكًا أَيْنَ مَا كُنتُ وَأَوْصَانِي بِالصَّلَاةِ وَالزَّكَاةِ مَا دُمْتُ حَيًّا
Te it, def na ma ku barkeel [sakkan]fu ma mën a nekk; dénk ma ma taxawal julli, di natt asaka feek maa ngi dundu ;
32وَبَرًّا بِوَالِدَتِي وَلَمْ يَجْعَلْنِي جَبَّارًا شَقِيًّا
tey topp sama yaay. Te doonuma kuy fétterlu, ku texeedi.
33وَالسَّلَامُ عَلَيَّ يَوْمَ وُلِدتُّ وَيَوْمَ أَمُوتُ وَيَوْمَ أُبْعَثُ حَيًّا
Jàmm rekk laay am bis ba ma juddoo, ak ca bis ba may dee ak bis ba may dekkiwaat”.
34ذَٰلِكَ عِيسَى ابْنُ مَرْيَمَ ۚ قَوْلَ الْحَقِّ الَّذِي فِيهِ يَمْتَرُونَ
Loolu mooy mbirum Iisaa doomu Maryam, wax jii moo cay dëgg ca la ngeen doon werante.
35مَا كَانَ لِلَّهِ أَن يَتَّخِذَ مِن وَلَدٍ ۖ سُبْحَانَهُ ۚ إِذَا قَضَىٰ أَمْرًا فَإِنَّمَا يَقُولُ لَهُ كُن فَيَكُونُ
Yellul ci Yàlla muy jàppe kenn doomam. Cëy sellam ga ! Bu bëggee menn mbir, Danaan : “Nekkal ! ” mu daldi nekk.
MaryamFihi Alxuraan
98Aaya
MeccanRevelation
33Aaya

Tekki — Maryam 33

Simoore Maryam Aaya 33 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Jàmm rekk laay am bis ba ma juddoo, ak ca…

Simoore Aaya 33/98 — Maryam مريم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Maryam Dégg, Maryam Tekki, Maryam mp3, Maryam pdf. Aaya 31–35. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers