Maryam · 41/98
Tekki Waxtaan — Maryam
وَاذْكُرْ فِي الْكِتَابِ إِبْرَاهِيمَ ۚ إِنَّهُ كَانَ صِدِّيقًا نَّبِيًّا ۝٤١
Wazkur fil Kitaabi Ibraaheem; innahoo kaana siddeeqan Nabiyyaa
📖 Tekkim Wolof
[Fàttalikul] Ibraahiima ca Téere ba, moom dey ku dëggu woon la, di ab Yonent.
🎧 Dégg

📜 Aaya 39-43 — Maryam

39وَأَنذِرْهُمْ يَوْمَ الْحَسْرَةِ إِذْ قُضِيَ الْأَمْرُ وَهُمْ فِي غَفْلَةٍ وَهُمْ لَا يُؤْمِنُونَ
Nanga leen xupp ci tiisu bisub jagle ga ; ndax àtte ba dog na te ñoom ña nga cig càggante te duñu gëm.
40إِنَّا نَحْنُ نَرِثُ الْأَرْضَ وَمَنْ عَلَيْهَا وَإِلَيْنَا يُرْجَعُونَ
Nun nooy donnu suuf si ak lépp lu nekk ci kawam, te it fi Nun la ñuy dellusi [Bis-pénc ba].
41وَاذْكُرْ فِي الْكِتَابِ إِبْرَاهِيمَ ۚ إِنَّهُ كَانَ صِدِّيقًا نَّبِيًّا
[Fàttalikul] Ibraahiima ca Téere ba, moom dey ku dëggu woon la, di ab Yonent.
42إِذْ قَالَ لِأَبِيهِ يَا أَبَتِ لِمَ تَعْبُدُ مَا لَا يَسْمَعُ وَلَا يُبْصِرُ وَلَا يُغْنِي عَنكَ شَيْئًا
[Fàttalikul] ba mu waxee baayam ne ko : “Ana lan moo tax ngay jaamu loo xam ne du dégg du gis, te du la fajal dara ?
43يَا أَبَتِ إِنِّي قَدْ جَاءَنِي مِنَ الْعِلْمِ مَا لَمْ يَأْتِكَ فَاتَّبِعْنِي أَهْدِكَ صِرَاطًا سَوِيًّا
Man sama baay, man dey am naa ci xam-xam loo xam ne yaw amoo ko ; topp ma, kon dey danaa la gindi, [teg la] ci yoon wu jub wa.
MaryamFihi Alxuraan
98Aaya
MeccanRevelation
41Aaya

Tekki — Maryam 41

Simoore Maryam Aaya 41 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Fàttalikul] Ibraahiima ca Téere ba, moom dey ku dëggu woon…

Simoore Aaya 41/98 — Maryam مريم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Maryam Dégg, Maryam Tekki, Maryam mp3, Maryam pdf. Aaya 39–43. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers