Al-Baqara · 224/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَلَا تَجْعَلُوا اللَّهَ عُرْضَةً لِّأَيْمَانِكُمْ أَن تَبَرُّوا وَتَتَّقُوا وَتُصْلِحُوا بَيْنَ النَّاسِ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ ۝٢٢٤
Wa laa taj`alul laaha `urdatal li aymaanikum an tabarroo wa tattaqoo wa tuslihoo bainan naas; wallaahu Samee`un `Aleem
📖 Tekkim Wolof
Buleen di giñ ci Yàlla, ba mu nekk gàllankoor gu leen teree def lu baax, walla ragal Yàlla mbaa yéwénal diggante nit ñi. Yàlla kuy dégg la te ku xam la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 222-226 — Al-Baqara

222وَيَسْأَلُونَكَ عَنِ الْمَحِيضِ ۖ قُلْ هُوَ أَذًى فَاعْتَزِلُوا النِّسَاءَ فِي الْمَحِيضِ ۖ وَلَا تَقْرَبُوهُنَّ حَتَّىٰ يَطْهُرْنَ ۖ فَإِذَا تَطَهَّرْنَ فَأْتُوهُنَّ مِنْ حَيْثُ أَمَرَكُمُ اللَّهُ ۚ إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ التَّوَّابِينَ وَيُحِبُّ الْمُتَطَهِّرِينَ
- Danañu la laaj lu jëm ci mbërëg . - Neel : “Moom sobe la. Deeleen beru jigéen ña bu ñu nekkee ci mbërëg, buleen jege ba bañuy laab. Suñu laabee, ngeen duggeleen fa Yàlla digle ndax Yàlla sopp na ñay tuub, sopp na itam ñay laabal seen bopp”.
223نِسَاؤُكُمْ حَرْثٌ لَّكُمْ فَأْتُوا حَرْثَكُمْ أَنَّىٰ شِئْتُمْ ۖ وَقَدِّمُوا لِأَنفُسِكُمْ ۚ وَاتَّقُوا اللَّهَ وَاعْلَمُوا أَنَّكُم مُّلَاقُوهُ ۗ وَبَشِّرِ الْمُؤْمِنِينَ
Seeni soxna [jabar] seeni tool lañu ; dikkeleen seeni tool ca na mu leen neexee te ngeen jiital ngir seen bopp, buleen fàtte tudd Yàlla. Te ngeen ragal Yàlla te ngeen xam ne dangeen dajeek Moom. Te nanga bégal way-gëm ña !
224وَلَا تَجْعَلُوا اللَّهَ عُرْضَةً لِّأَيْمَانِكُمْ أَن تَبَرُّوا وَتَتَّقُوا وَتُصْلِحُوا بَيْنَ النَّاسِ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Buleen di giñ ci Yàlla, ba mu nekk gàllankoor gu leen teree def lu baax, walla ragal Yàlla mbaa yéwénal diggante nit ñi. Yàlla kuy dégg la te ku xam la.
225لَّا يُؤَاخِذُكُمُ اللَّهُ بِاللَّغْوِ فِي أَيْمَانِكُمْ وَلَٰكِن يُؤَاخِذُكُم بِمَا كَسَبَتْ قُلُوبُكُمْ ۗ وَاللَّهُ غَفُورٌ حَلِيمٌ
Yàlla duleen jàppe ngiñ ci kaf : Waaye Dana leen jàppe ngiñ lu seeni xol dëggu. Yàlla jéggalaakoon la te ku lewet la.
226لِّلَّذِينَ يُؤْلُونَ مِن نِّسَائِهِمْ تَرَبُّصُ أَرْبَعَةِ أَشْهُرٍ ۖ فَإِن فَاءُوا فَإِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ña giñ ci [beru] seeni jabar, nangeen leen muñal ñeenti weer. Bu ñu delloo ginnaaw [ca la ñu giñoon], Yàlla Jéggalaakoon la te Jaglewaakoon la !
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
224Aaya

Tekki — Al-Baqara 224

Simoore Al-Baqara Aaya 224 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Buleen di giñ ci Yàlla, ba mu nekk gàllankoor gu…

Simoore Aaya 224/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 222–226. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers