Al-Baqara · 41/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَآمِنُوا بِمَا أَنزَلْتُ مُصَدِّقًا لِّمَا مَعَكُمْ وَلَا تَكُونُوا أَوَّلَ كَافِرٍ بِهِ ۖ وَلَا تَشْتَرُوا بِآيَاتِي ثَمَنًا قَلِيلًا وَإِيَّايَ فَاتَّقُونِ ۝٤١
Wa aaminoo bimaaa anzaltu musaddiqal limaa ma`akum wa laa takoonooo awwala kaafirim bihee wa laa tashtaroo bi Aayaatee samanan qaleelanw wa iyyaaya fattaqoon
📖 Tekkim Wolof
Nangeen gëm li Ma wàcce, te muy dëggal li ngeen yore ; buleen doon ñi ko jëkk a weddi. Buleen jaay samay laaya ak njëg gu néew. Te nangeen ma ragal Man doŋ.
🎧 Dégg

📜 Aaya 39-43 — Al-Baqara

39وَالَّذِينَ كَفَرُوا وَكَذَّبُوا بِآيَاتِنَا أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ النَّارِ ۖ هُمْ فِيهَا خَالِدُونَ
Ña weddi te fenloo Sunuy tegtal, ñoom ñooy dëkk Safara te ñoom dañu fay béel.
40يَا بَنِي إِسْرَائِيلَ اذْكُرُوا نِعْمَتِيَ الَّتِي أَنْعَمْتُ عَلَيْكُمْ وَأَوْفُوا بِعَهْدِي أُوفِ بِعَهْدِكُمْ وَإِيَّايَ فَارْهَبُونِ
Yéen [Bani-Israayiil] ñi sëtoo ci [Yanqooba], fàttalikuleen Sama xéewal gi Ma léen xéewaloon. Nangeen matal Sama kóllare, kon Danaa matal seen gos. Buleen ragal ku dul Man.
41وَآمِنُوا بِمَا أَنزَلْتُ مُصَدِّقًا لِّمَا مَعَكُمْ وَلَا تَكُونُوا أَوَّلَ كَافِرٍ بِهِ ۖ وَلَا تَشْتَرُوا بِآيَاتِي ثَمَنًا قَلِيلًا وَإِيَّايَ فَاتَّقُونِ
Nangeen gëm li Ma wàcce, te muy dëggal li ngeen yore ; buleen doon ñi ko jëkk a weddi. Buleen jaay samay laaya ak njëg gu néew. Te nangeen ma ragal Man doŋ.
42وَلَا تَلْبِسُوا الْحَقَّ بِالْبَاطِلِ وَتَكْتُمُوا الْحَقَّ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ
Buleen jaxase dëgg ak caaxaan, di nëbb dëgg te fekk ngeen xam ko xéll.
43وَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ وَآتُوا الزَّكَاةَ وَارْكَعُوا مَعَ الرَّاكِعِينَ
Nangeen fonk julli, di joxe asaka, te di rukkoo ànd ak way-rukkoo ya. [Jullig mbooloo, di julli ci biir jàkka yi].
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
41Aaya

Tekki — Al-Baqara 41

Simoore Al-Baqara Aaya 41 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nangeen gëm li Ma wàcce, te muy dëggal li ngeen…

Simoore Aaya 41/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 39–43. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers