Taha · 123/135
Tekki Waxtaan — Taha
قَالَ اهْبِطَا مِنْهَا جَمِيعًا ۖ بَعْضُكُمْ لِبَعْضٍ عَدُوٌّ ۖ فَإِمَّا يَأْتِيَنَّكُم مِّنِّي هُدًى فَمَنِ اتَّبَعَ هُدَايَ فَلَا يَضِلُّ وَلَا يَشْقَىٰ ۝١٢٣
Qaalah bita minhaa jamee`am ba`dukum liba`din `aduww; fa immaa yaati yannakum minnee hudan famanit taba`a hudaaya falaa yadillu wa laa yashhqaa
📖 Tekkim Wolof
Yàlla daldi ne leen : “Génnleen Àjjana, wàcc jëm suuf, ñennat ci yéen di noonoo ñeneen ña ca des. Dana am nag njub gu bawoo fi Man dikk ci yéen, képp ku topp Sama njub googu, du sànku, du sonn.
🎧 Dégg

📜 Aaya 121-125 — Taha

121فَأَكَلَا مِنْهَا فَبَدَتْ لَهُمَا سَوْآتُهُمَا وَطَفِقَا يَخْصِفَانِ عَلَيْهِمَا مِن وَرَقِ الْجَنَّةِ ۚ وَعَصَىٰ آدَمُ رَبَّهُ فَغَوَىٰ
Ñu daldi cay lekk [garab ga]. Seen rafle wa daldi feeñ. Ñu tàmbalee witt ca xobi garab ya nekk Àjjana di ko làmboo. Aadama moy na ndigalu Boroomam, tooñ tàbbi.
122ثُمَّ اجْتَبَاهُ رَبُّهُ فَتَابَ عَلَيْهِ وَهَدَىٰ
Yàlla delloo cim xelam ba mu tuub, Mu daldi koy jéggal, Mu daldi it jubbanti ko.
123قَالَ اهْبِطَا مِنْهَا جَمِيعًا ۖ بَعْضُكُمْ لِبَعْضٍ عَدُوٌّ ۖ فَإِمَّا يَأْتِيَنَّكُم مِّنِّي هُدًى فَمَنِ اتَّبَعَ هُدَايَ فَلَا يَضِلُّ وَلَا يَشْقَىٰ
Yàlla daldi ne leen : “Génnleen Àjjana, wàcc jëm suuf, ñennat ci yéen di noonoo ñeneen ña ca des. Dana am nag njub gu bawoo fi Man dikk ci yéen, képp ku topp Sama njub googu, du sànku, du sonn.
124وَمَنْ أَعْرَضَ عَن ذِكْرِي فَإِنَّ لَهُ مَعِيشَةً ضَنكًا وَنَحْشُرُهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ أَعْمَىٰ
Képp ku ko dummóoyu, dana dundu dund gu metti, te buy dekki Bis-pénc ba gumba lay doon ñu gotti ko”.
125قَالَ رَبِّ لِمَ حَشَرْتَنِي أَعْمَىٰ وَقَدْ كُنتُ بَصِيرًا
[Su ko defee] muy laaj naan : "Sama Boroom, lan moo tax nga pang ma may gumba te ca àddina ma doon gis ? ”
TahaFihi Alxuraan
135Aaya
MeccanRevelation
123Aaya

Tekki — Taha 123

Simoore Taha Aaya 123 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla daldi ne leen : “Génnleen Àjjana, wàcc jëm suuf,…

Simoore Aaya 123/135 — Taha طه (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Taha Dégg, Taha Tekki, Taha mp3, Taha pdf. Aaya 121–125. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers