Taha · 122/135
Tekki Waxtaan — Taha
ثُمَّ اجْتَبَاهُ رَبُّهُ فَتَابَ عَلَيْهِ وَهَدَىٰ ۝١٢٢
Summaj tabbahu Rabbuhoo fataaba `alaihi wa hadaa
📖 Tekkim Wolof
Yàlla delloo cim xelam ba mu tuub, Mu daldi koy jéggal, Mu daldi it jubbanti ko.

🎧 Dégg


📜 Aaya 120-124 — Taha

120فَوَسْوَسَ إِلَيْهِ الشَّيْطَانُ قَالَ يَا آدَمُ هَلْ أَدُلُّكَ عَلَىٰ شَجَرَةِ الْخُلْدِ وَمُلْكٍ لَّا يَبْلَىٰ
Séytaane daldi koy jax-jaxal [nëxal xelam] ne ko : "Yaw Aadama, ndax duma la tegtal garab guy tax nga am nguur gu dootul foq ? ”
121فَأَكَلَا مِنْهَا فَبَدَتْ لَهُمَا سَوْآتُهُمَا وَطَفِقَا يَخْصِفَانِ عَلَيْهِمَا مِن وَرَقِ الْجَنَّةِ ۚ وَعَصَىٰ آدَمُ رَبَّهُ فَغَوَىٰ
Ñu daldi cay lekk [garab ga]. Seen rafle wa daldi feeñ. Ñu tàmbalee witt ca xobi garab ya nekk Àjjana di ko làmboo. Aadama moy na ndigalu Boroomam, tooñ tàbbi.
122ثُمَّ اجْتَبَاهُ رَبُّهُ فَتَابَ عَلَيْهِ وَهَدَىٰ
Yàlla delloo cim xelam ba mu tuub, Mu daldi koy jéggal, Mu daldi it jubbanti ko.
123قَالَ اهْبِطَا مِنْهَا جَمِيعًا ۖ بَعْضُكُمْ لِبَعْضٍ عَدُوٌّ ۖ فَإِمَّا يَأْتِيَنَّكُم مِّنِّي هُدًى فَمَنِ اتَّبَعَ هُدَايَ فَلَا يَضِلُّ وَلَا يَشْقَىٰ
Yàlla daldi ne leen : “Génnleen Àjjana, wàcc jëm suuf, ñennat ci yéen di noonoo ñeneen ña ca des. Dana am nag njub gu bawoo fi Man dikk ci yéen, képp ku topp Sama njub googu, du sànku, du sonn.
124وَمَنْ أَعْرَضَ عَن ذِكْرِي فَإِنَّ لَهُ مَعِيشَةً ضَنكًا وَنَحْشُرُهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ أَعْمَىٰ
Képp ku ko dummóoyu, dana dundu dund gu metti, te buy dekki Bis-pénc ba gumba lay doon ñu gotti ko”.
TahaFihi Alxuraan
135Aaya
MeccanRevelation
122Aaya

Tekki — Taha 122

Simoore Taha Aaya 122 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla delloo cim xelam ba mu tuub, Mu daldi koy…

Simoore Aaya 122/135 — Taha طه (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Taha Dégg, Taha Tekki, Taha mp3, Taha pdf. Aaya 120–124. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers