An-Nur · 38/64
Tekki Waxtaan — An-Nur
لِيَجْزِيَهُمُ اللَّهُ أَحْسَنَ مَا عَمِلُوا وَيَزِيدَهُم مِّن فَضْلِهِ ۗ وَاللَّهُ يَرْزُقُ مَن يَشَاءُ بِغَيْرِ حِسَابٍ ۝٣٨
Liyajziyahumul laahu ahsana maa `amiloo wa yazeedahum min fadlih; wal laahu yarzuqu mai yashaaa`u bighairi hisaab
📖 Tekkim Wolof
[Ci loolu], Yàlla dana leen feye la gën a rafet ca la ñu jëf. Dana leen dolli ngëneel. Te Yàlla dana wërsëgal ku ko soob ci lu àndul ak ug waññi [lijjanti].
🎧 Dégg

📜 Aaya 36-40 — An-Nur

36فِي بُيُوتٍ أَذِنَ اللَّهُ أَن تُرْفَعَ وَيُذْكَرَ فِيهَا اسْمُهُ يُسَبِّحُ لَهُ فِيهَا بِالْغُدُوِّ وَالْآصَالِ
Ci biiri kër [jàkka] yoo xam ne Yàlla digle ñu di fa tudd aw Turam, di Ko yékkati ; di Ko ca sàbbaal suba ak ngoon,
37رِجَالٌ لَّا تُلْهِيهِمْ تِجَارَةٌ وَلَا بَيْعٌ عَن ذِكْرِ اللَّهِ وَإِقَامِ الصَّلَاةِ وَإِيتَاءِ الزَّكَاةِ ۙ يَخَافُونَ يَوْمًا تَتَقَلَّبُ فِيهِ الْقُلُوبُ وَالْأَبْصَارُ
aw gaay ñoo xam ne njulaakum njaay duleen mës a fàbbi ci tudd Yàlla ak a taxawal julli, ak génne asaka, ngir ñoom kat dañoo ragal Bis ba xol ya di wëlbëtiku ak gët ya.
38لِيَجْزِيَهُمُ اللَّهُ أَحْسَنَ مَا عَمِلُوا وَيَزِيدَهُم مِّن فَضْلِهِ ۗ وَاللَّهُ يَرْزُقُ مَن يَشَاءُ بِغَيْرِ حِسَابٍ
[Ci loolu], Yàlla dana leen feye la gën a rafet ca la ñu jëf. Dana leen dolli ngëneel. Te Yàlla dana wërsëgal ku ko soob ci lu àndul ak ug waññi [lijjanti].
39وَالَّذِينَ كَفَرُوا أَعْمَالُهُمْ كَسَرَابٍ بِقِيعَةٍ يَحْسَبُهُ الظَّمْآنُ مَاءً حَتَّىٰ إِذَا جَاءَهُ لَمْ يَجِدْهُ شَيْئًا وَوَجَدَ اللَّهَ عِندَهُ فَوَفَّاهُ حِسَابَهُ ۗ وَاللَّهُ سَرِيعُ الْحِسَابِ
Ña weddi, di ay jéefar, ñoom seeni jëf dafa mel ni ñàndóox, bu ko boroomu mar séenee, dakoy jàppe ndox. Saa bu fa agsee, du fa fekk tus ; Yàlla rekk la fay fekk Mu waññal ko ay jëfam ba mu mat sëkk, te moo ne Yàllaa ka gaaw ab lijjanti.
40أَوْ كَظُلُمَاتٍ فِي بَحْرٍ لُّجِّيٍّ يَغْشَاهُ مَوْجٌ مِّن فَوْقِهِ مَوْجٌ مِّن فَوْقِهِ سَحَابٌ ۚ ظُلُمَاتٌ بَعْضُهَا فَوْقَ بَعْضٍ إِذَا أَخْرَجَ يَدَهُ لَمْ يَكَدْ يَرَاهَا ۗ وَمَن لَّمْ يَجْعَلِ اللَّهُ لَهُ نُورًا فَمَا لَهُ مِن نُّورٍ
[Jëfi yéefar ba-tey dafa mel ni] lëndëmug géej guy duusu : ganax ci kaw ganax, ay niir yu lëndëm tegaloo tiim ko. Ba sax moom bu génnee loxoom, du ko xaw a gis. Te képp ku Yàlla defalul ag leer, du am ag leer.
An-NurFihi Alxuraan
64Aaya
MedinanRevelation
38Aaya

Tekki — An-Nur 38

Simoore An-Nur Aaya 38 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Ci loolu], Yàlla dana leen feye la gën a rafet…

Simoore Aaya 38/64 — An-Nur النور (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nur Dégg, An-Nur Tekki, An-Nur mp3, An-Nur pdf. Aaya 36–40. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers