Al-Furqan · 21/77
Tekki Waxtaan — Al-Furqan
۞ وَقَالَ الَّذِينَ لَا يَرْجُونَ لِقَاءَنَا لَوْلَا أُنزِلَ عَلَيْنَا الْمَلَائِكَةُ أَوْ نَرَىٰ رَبَّنَا ۗ لَقَدِ اسْتَكْبَرُوا فِي أَنفُسِهِمْ وَعَتَوْا عُتُوًّا كَبِيرًا ۝٢١
Wa qaalal lazeena laa yarjoona liqaaa`anaa law laaa unzila `alainal malaaa`ikatu awnaraa Rabbanaa; laqadistakbaroo feee anfusihim wa `ataw `utuwwan kabeeraa
📖 Tekkim Wolof
Ña yaakaarul a dajeek Nun ñangay wax naan : “Céy bées wàcce woon ci nun ay Malaaka, mbaa nu gis sunu Boroom [Yàlla] ! ”. Dañu doon rëy-rëylu [kaweel seen bopp], réer réer gu jéggi dayo.

🎧 Dégg


📜 Aaya 19-23 — Al-Furqan

19فَقَدْ كَذَّبُوكُم بِمَا تَقُولُونَ فَمَا تَسْتَطِيعُونَ صَرْفًا وَلَا نَصْرًا ۚ وَمَن يَظْلِم مِّنكُمْ نُذِقْهُ عَذَابًا كَبِيرًا
“Weddi woon nañu leen ca li ngeen di wax. Amuñu ab rawtukaay. Te képp ku tooñati ci yéen, Dananu ko mosal mbugal mu réy”.
20وَمَا أَرْسَلْنَا قَبْلَكَ مِنَ الْمُرْسَلِينَ إِلَّا إِنَّهُمْ لَيَأْكُلُونَ الطَّعَامَ وَيَمْشُونَ فِي الْأَسْوَاقِ ۗ وَجَعَلْنَا بَعْضَكُمْ لِبَعْضٍ فِتْنَةً أَتَصْبِرُونَ ۗ وَكَانَ رَبُّكَ بَصِيرًا
Musunoo yebal ay Yonent ca la la jiitu lu dul dañu daan lekk ñam te di dox ci ja yi [màrse yi]. Def Nanu it ñenn ci yéen di sànjeb ña ca des, mbaa dangeen muñ ? - Sa Boroom de kuy gis la.
21۞ وَقَالَ الَّذِينَ لَا يَرْجُونَ لِقَاءَنَا لَوْلَا أُنزِلَ عَلَيْنَا الْمَلَائِكَةُ أَوْ نَرَىٰ رَبَّنَا ۗ لَقَدِ اسْتَكْبَرُوا فِي أَنفُسِهِمْ وَعَتَوْا عُتُوًّا كَبِيرًا
Ña yaakaarul a dajeek Nun ñangay wax naan : “Céy bées wàcce woon ci nun ay Malaaka, mbaa nu gis sunu Boroom [Yàlla] ! ”. Dañu doon rëy-rëylu [kaweel seen bopp], réer réer gu jéggi dayo.
22يَوْمَ يَرَوْنَ الْمَلَائِكَةَ لَا بُشْرَىٰ يَوْمَئِذٍ لِّلْمُجْرِمِينَ وَيَقُولُونَ حِجْرًا مَّحْجُورًا
Bis ba ñuy mën a gis malaaka ya du neex ci ñoom de, ndax Malaaka yaa nga naan leen : “Seeni mbir sakk na” !
23وَقَدِمْنَا إِلَىٰ مَا عَمِلُوا مِنْ عَمَلٍ فَجَعَلْنَاهُ هَبَاءً مَّنثُورًا
Nu fab jépp jëf ju ñu mësoon a jëf, def ko pënd bu ñu wasaare.
Al-FurqanFihi Alxuraan
77Aaya
MeccanRevelation
21Aaya

Tekki — Al-Furqan 21

Simoore Al-Furqan Aaya 21 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña yaakaarul a dajeek Nun ñangay wax naan : “Céy…

Simoore Aaya 21/77 — Al-Furqan الفرقان (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Furqan Dégg, Al-Furqan Tekki, Al-Furqan mp3, Al-Furqan pdf. Aaya 19–23. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers