An-Naml · 17/93
Tekki Waxtaan — An-Naml
وَحُشِرَ لِسُلَيْمَانَ جُنُودُهُ مِنَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ وَالطَّيْرِ فَهُمْ يُوزَعُونَ ۝١٧
Wa hushira Sulaimaana junooduhoo minal jinni wal insi wattairi fahum yooza`oon
📖 Tekkim Wolof
Dajaleef na Suleymaan ak i xaritam, cij jinne yeek nit ñi, ñu def i sàppe.
🎧 Dégg

📜 Aaya 15-19 — An-Naml

15وَلَقَدْ آتَيْنَا دَاوُودَ وَسُلَيْمَانَ عِلْمًا ۖ وَقَالَا الْحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي فَضَّلَنَا عَلَىٰ كَثِيرٍ مِّنْ عِبَادِهِ الْمُؤْمِنِينَ
Joxoon Nanu Daawuda ak Suleymaan xam-xam ; ñuy wax naan : “Xeeti cant yépp ñeel na Yàlla, Moom mi nu gënal ci kaw nit ñu bari ñi bokkoon ci jaamam ñi gëm”.
16وَوَرِثَ سُلَيْمَانُ دَاوُودَ ۖ وَقَالَ يَا أَيُّهَا النَّاسُ عُلِّمْنَا مَنطِقَ الطَّيْرِ وَأُوتِينَا مِن كُلِّ شَيْءٍ ۖ إِنَّ هَٰذَا لَهُوَ الْفَضْلُ الْمُبِينُ
Suleymaan wuutu na Daawuda, daldi ne : “Éy yéen nit ñi ! Xam naa waxi picc yi ; te am naa lu ne. Loolu mooy ngëneel lu bir.
17وَحُشِرَ لِسُلَيْمَانَ جُنُودُهُ مِنَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ وَالطَّيْرِ فَهُمْ يُوزَعُونَ
Dajaleef na Suleymaan ak i xaritam, cij jinne yeek nit ñi, ñu def i sàppe.
18حَتَّىٰ إِذَا أَتَوْا عَلَىٰ وَادِ النَّمْلِ قَالَتْ نَمْلَةٌ يَا أَيُّهَا النَّمْلُ ادْخُلُوا مَسَاكِنَكُمْ لَا يَحْطِمَنَّكُمْ سُلَيْمَانُ وَجُنُودُهُ وَهُمْ لَا يَشْعُرُونَ
Ba ñu agsee ca xuru xorondom ya, mu am xurondom wu wax ne : "Éy yéen xorondom yi, dugguleen ci seeni biir kër, balaa leen a Suleymaan ak i xaritam di nappaaje te duñu ko sax yëg”.
19فَتَبَسَّمَ ضَاحِكًا مِّن قَوْلِهَا وَقَالَ رَبِّ أَوْزِعْنِي أَنْ أَشْكُرَ نِعْمَتَكَ الَّتِي أَنْعَمْتَ عَلَيَّ وَعَلَىٰ وَالِدَيَّ وَأَنْ أَعْمَلَ صَالِحًا تَرْضَاهُ وَأَدْخِلْنِي بِرَحْمَتِكَ فِي عِبَادِكَ الصَّالِحِينَ
[Suleymaan] muuñ, daldi ree ndax wax jooju, daldi wax ne : “Yaw sama Boroom, Nanga baaxe may sant ci xéewal gii Nga ma dafal maak samay waajur, te may jëf jëf ju baax Joo gërëm te Nga may ma ci Sa yërmaande ma bokk ca Sa jaam ñu yiw ña”.
An-NamlFihi Alxuraan
93Aaya
MeccanRevelation
17Aaya

Tekki — An-Naml 17

Simoore An-Naml Aaya 17 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dajaleef na Suleymaan ak i xaritam, cij jinne yeek nit…

Simoore Aaya 17/93 — An-Naml النمل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Naml Dégg, An-Naml Tekki, An-Naml mp3, An-Naml pdf. Aaya 15–19. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers