Al-Qasas · 40/88
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Qasas
فَأَخَذْنَاهُ وَجُنُودَهُ فَنَبَذْنَاهُمْ فِي الْيَمِّ ۖ فَانظُرْ كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الظَّالِمِينَ ۝٤٠
Fa akhaznaahu wa junoo dahoo fanabaznaahum fil yammi fanzur kaifa kaana `aaqibatuz zaalimeen
📖 Tekkim Wolof
Nu jël ko mook i xarekatam nargan leen ca ndox ma. Xoolal mujjug tooñkat ya.

🎧 Dégg


📜 Aaya 38-42 — Simoore Al-Qasas

38وَقَالَ فِرْعَوْنُ يَا أَيُّهَا الْمَلَأُ مَا عَلِمْتُ لَكُم مِّنْ إِلَٰهٍ غَيْرِي فَأَوْقِدْ لِي يَا هَامَانُ عَلَى الطِّينِ فَاجْعَل لِّي صَرْحًا لَّعَلِّي أَطَّلِعُ إِلَىٰ إِلَٰهِ مُوسَىٰ وَإِنِّي لَأَظُنُّهُ مِنَ الْكَاذِبِينَ
Firawna daldi wax ne : "Éy yéen kilifa yi, xamaluma leen jeneen Yàlla ju dul man. Yaw Haamaan, taalal ma aw safara ci ban bi te tabaxal ma ag tóoj ndax ma mën cee yërndu Yàllay Muusaa ji. Te man sax njortu naa ne ci fenkat yi la bokk”.
39وَاسْتَكْبَرَ هُوَ وَجُنُودُهُ فِي الْأَرْضِ بِغَيْرِ الْحَقِّ وَظَنُّوا أَنَّهُمْ إِلَيْنَا لَا يُرْجَعُونَ
Muy rëy-rëylu mook i xarekatam ci réew mi ci lu dul dëgg. Ñu foogoon ne duñu dellusi ci Nun.
40فَأَخَذْنَاهُ وَجُنُودَهُ فَنَبَذْنَاهُمْ فِي الْيَمِّ ۖ فَانظُرْ كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الظَّالِمِينَ
Nu jël ko mook i xarekatam nargan leen ca ndox ma. Xoolal mujjug tooñkat ya.
41وَجَعَلْنَاهُمْ أَئِمَّةً يَدْعُونَ إِلَى النَّارِ ۖ وَيَوْمَ الْقِيَامَةِ لَا يُنصَرُونَ
Defoon Nanu leen ay njiit yuy woote jëme Safara. Te bu Bis-pénc baa kenn duleen dimbali.
42وَأَتْبَعْنَاهُمْ فِي هَٰذِهِ الدُّنْيَا لَعْنَةً ۖ وَيَوْمَ الْقِيَامَةِ هُم مِّنَ الْمَقْبُوحِينَ
Nu toqal leen am rëbb ci àddina sii. Te bu Bis-pénc baa dañuy bokk ca ña ñuy siibiibal.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
40Aaya

Tekki — Al-Qasas 40

Simoore Al-Qasas Aaya 40 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nu jël ko mook i xarekatam nargan leen ca ndox…

Simoore Aaya 40/88 — Simoore Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Qasas Dégg, Simoore Al-Qasas Tekki, Simoore Al-Qasas mp3, Simoore Al-Qasas pdf. Aaya 38–42. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers