Al-Qasas · 73/88
Tekki Waxtaan — Al-Qasas
وَمِن رَّحْمَتِهِ جَعَلَ لَكُمُ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ لِتَسْكُنُوا فِيهِ وَلِتَبْتَغُوا مِن فَضْلِهِ وَلَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ ۝٧٣
Wa mir rahmatihee ja`ala lakumul laila wannahaara litaskunoo feehi wa litabtaghoo min fadlihee wa la`allakum tashkuroon
📖 Tekkim Wolof
Ci yërmaandeem la leen defalee guddeek bëccëg ngir ngeen di ca dal ak a sàkku wërsëg, ak it ngir sant Ko.

🎧 Dégg


📜 Aaya 71-75 — Al-Qasas

71قُلْ أَرَأَيْتُمْ إِن جَعَلَ اللَّهُ عَلَيْكُمُ اللَّيْلَ سَرْمَدًا إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ مَنْ إِلَٰهٌ غَيْرُ اللَّهِ يَأْتِيكُم بِضِيَاءٍ ۖ أَفَلَا تَسْمَعُونَ
Neel : “Xanaa gisuleen ne bu Yàlla defoon guddi gi muy lu sax ba Bis-pénc ba, ana jan yàlla ju dul Moom moo leen di indil ag leer ? Moo ndax dungeen dégg ? ”
72قُلْ أَرَأَيْتُمْ إِن جَعَلَ اللَّهُ عَلَيْكُمُ النَّهَارَ سَرْمَدًا إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ مَنْ إِلَٰهٌ غَيْرُ اللَّهِ يَأْتِيكُم بِلَيْلٍ تَسْكُنُونَ فِيهِ ۖ أَفَلَا تُبْصِرُونَ
Neel : “Xanaa gisuleen ne bu Yàlla ci yéen bëccëg muy lu sax ba Bis-pénc ba, ana jan yàlla ju dul Moom moo leen di indil guddi gu ngeen di dalloo ? Moo ndax dangeen dul gis ? ”
73وَمِن رَّحْمَتِهِ جَعَلَ لَكُمُ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ لِتَسْكُنُوا فِيهِ وَلِتَبْتَغُوا مِن فَضْلِهِ وَلَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Ci yërmaandeem la leen defalee guddeek bëccëg ngir ngeen di ca dal ak a sàkku wërsëg, ak it ngir sant Ko.
74وَيَوْمَ يُنَادِيهِمْ فَيَقُولُ أَيْنَ شُرَكَائِيَ الَّذِينَ كُنتُمْ تَزْعُمُونَ
Ak bis ba Mu leen di woo naan leen : “Ana ña ngeen Ma doon bokkaaleel ? ”
75وَنَزَعْنَا مِن كُلِّ أُمَّةٍ شَهِيدًا فَقُلْنَا هَاتُوا بُرْهَانَكُمْ فَعَلِمُوا أَنَّ الْحَقَّ لِلَّهِ وَضَلَّ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Nu rocci ci xeet wu nekk seede, daldi ne leen : “Indileen seeni firnde”. Ñu daldi xam ne dëgg Yàllaa ko moom ; la ñu daan sos réer leen.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
73Aaya

Tekki — Al-Qasas 73

Simoore Al-Qasas Aaya 73 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ci yërmaandeem la leen defalee guddeek bëccëg ngir ngeen di…

Simoore Aaya 73/88 — Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Qasas Dégg, Al-Qasas Tekki, Al-Qasas mp3, Al-Qasas pdf. Aaya 71–75. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers