Aali Imran · 115/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
وَمَا يَفْعَلُوا مِنْ خَيْرٍ فَلَن يُكْفَرُوهُ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِالْمُتَّقِينَ ۝١١٥
Wa maa yaf`aloo min khairin falai yukfarooh; wallaahu `aleemun bilmuttaqeen
📖 Tekkim Wolof
Lu ngeen jëf ci aw yiw, kenn duleen ko xañ. Yàlla xam na ña ko ragal .

🎧 Dégg


📜 Aaya 113-117 — Simoore Aali Imran

113۞ لَيْسُوا سَوَاءً ۗ مِّنْ أَهْلِ الْكِتَابِ أُمَّةٌ قَائِمَةٌ يَتْلُونَ آيَاتِ اللَّهِ آنَاءَ اللَّيْلِ وَهُمْ يَسْجُدُونَ
Waaye ñoñ-téere yemuñu de. Am na ci kurél bu taxaw [ci dëgg] buy jàng kàdduy Yàlla ya, ca waxtu ya séq guddi, te dañuy julli [sujjóot].
114يُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ وَيَأْمُرُونَ بِالْمَعْرُوفِ وَيَنْهَوْنَ عَنِ الْمُنكَرِ وَيُسَارِعُونَ فِي الْخَيْرَاتِ وَأُولَٰئِكَ مِنَ الصَّالِحِينَ
Gëm nañu Yàlla ak Bis-pénc ba, te dañuy digle njekk, di tere njekkar, di jëkkante ci def lu baax. Ñooña ca ñu yiw ña lañu bokk.
115وَمَا يَفْعَلُوا مِنْ خَيْرٍ فَلَن يُكْفَرُوهُ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِالْمُتَّقِينَ
Lu ngeen jëf ci aw yiw, kenn duleen ko xañ. Yàlla xam na ña ko ragal .
116إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا لَن تُغْنِيَ عَنْهُمْ أَمْوَالُهُمْ وَلَا أَوْلَادُهُم مِّنَ اللَّهِ شَيْئًا ۖ وَأُولَٰئِكَ أَصْحَابُ النَّارِ ۚ هُمْ فِيهَا خَالِدُونَ
Ña weddi, seeni alal ak seeni doom duñuleen jariñ dara fa Yàlla. Ñoom ñooy waa Safara te dañu fay béel.
117مَثَلُ مَا يُنفِقُونَ فِي هَٰذِهِ الْحَيَاةِ الدُّنْيَا كَمَثَلِ رِيحٍ فِيهَا صِرٌّ أَصَابَتْ حَرْثَ قَوْمٍ ظَلَمُوا أَنفُسَهُمْ فَأَهْلَكَتْهُ ۚ وَمَا ظَلَمَهُمُ اللَّهُ وَلَٰكِنْ أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ
La ñuy joxe ci seeni alal ci mbiri àdduna dafa mel ni ngelaw lu ànd ak safara dal ci kaw mbeyum ña tooñ seen bopp, ne ko fuuf lakk ko. Yàlla tooñuleen waaye ñoom ñoo tooñ seen bopp.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
115Aaya

Tekki — Aali Imran 115

Simoore Aali Imran Aaya 115 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Lu ngeen jëf ci aw yiw, kenn duleen ko xañ.…

Simoore Aaya 115/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 113–117. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers