Aali Imran · 158/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
وَلَئِن مُّتُّمْ أَوْ قُتِلْتُمْ لَإِلَى اللَّهِ تُحْشَرُونَ ۝١٥٨
Wa la`im muttum `aw qutiltumla ilal laahi tuhsharoon
📖 Tekkim Wolof
Ngeen dee walla ñu rey leen, dees na leen pang [gur-gur] jëme ca Yàlla.

🎧 Dégg


📜 Aaya 156-160 — Simoore Aali Imran

156يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَكُونُوا كَالَّذِينَ كَفَرُوا وَقَالُوا لِإِخْوَانِهِمْ إِذَا ضَرَبُوا فِي الْأَرْضِ أَوْ كَانُوا غُزًّى لَّوْ كَانُوا عِندَنَا مَا مَاتُوا وَمَا قُتِلُوا لِيَجْعَلَ اللَّهُ ذَٰلِكَ حَسْرَةً فِي قُلُوبِهِمْ ۗ وَاللَّهُ يُحْيِي وَيُمِيتُ ۗ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ
Yéen ñi gëm ! Buleen mel ni ña weddi, di wax seeni mbokk ya nekk ci tukki walla ci xare [te dee ca] : “Bu ñu toogoon ci nun, duñu dee walla duñuleen rey. ”. Yàlla def wax jooju di rëccu ci seeni xol. Te Yàlla Mooy dundal, Mooy rey. Te Yàllaa ngi ne jàkk li ngeen di def, di leen gis.
157وَلَئِن قُتِلْتُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ أَوْ مُتُّمْ لَمَغْفِرَةٌ مِّنَ اللَّهِ وَرَحْمَةٌ خَيْرٌ مِّمَّا يَجْمَعُونَ
Bu ñu leen reyee ci yoonu Yàlla walla ngeen dee, ca dëgg-dëgg jéggalu ga, Yàlla ak yërmandeem moo gën fuuf li ngeen di dajale.
158وَلَئِن مُّتُّمْ أَوْ قُتِلْتُمْ لَإِلَى اللَّهِ تُحْشَرُونَ
Ngeen dee walla ñu rey leen, dees na leen pang [gur-gur] jëme ca Yàlla.
159فَبِمَا رَحْمَةٍ مِّنَ اللَّهِ لِنتَ لَهُمْ ۖ وَلَوْ كُنتَ فَظًّا غَلِيظَ الْقَلْبِ لَانفَضُّوا مِنْ حَوْلِكَ ۖ فَاعْفُ عَنْهُمْ وَاسْتَغْفِرْ لَهُمْ وَشَاوِرْهُمْ فِي الْأَمْرِ ۖ فَإِذَا عَزَمْتَ فَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُتَوَكِّلِينَ
Ci sa yërmaandeey Boroom nga nooyee ci ñoom ! Boo nekkoon ku ñaaw jikko walla ku xat xol, ñu ne wuseet bàyyi la. Baal-leen te jéggal-leen. Te deel diisook ñoom ci mbir yi ; waaye boo dogoo [ci wéyal dara], nanga wéeru ci sa Boroom, Yàlla dana safoo ñay wéeru ci Moom [yaw Muhammad].
160إِن يَنصُرْكُمُ اللَّهُ فَلَا غَالِبَ لَكُمْ ۖ وَإِن يَخْذُلْكُمْ فَمَن ذَا الَّذِي يَنصُرُكُم مِّن بَعْدِهِ ۗ وَعَلَى اللَّهِ فَلْيَتَوَكَّلِ الْمُؤْمِنُونَ
Bu leen Yàlla dimbalee, kenn duleen mën a not. Bu leen bàyyee, kan moo leen di mën a dimbali ? [Amul]. Ñi gëm, nañu wéeru ci Yàlla.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
158Aaya

Tekki — Aali Imran 158

Simoore Aali Imran Aaya 158 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ngeen dee walla ñu rey leen, dees na leen pang…

Simoore Aaya 158/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 156–160. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers