Aali Imran · 185/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
كُلُّ نَفْسٍ ذَائِقَةُ الْمَوْتِ ۗ وَإِنَّمَا تُوَفَّوْنَ أُجُورَكُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۖ فَمَن زُحْزِحَ عَنِ النَّارِ وَأُدْخِلَ الْجَنَّةَ فَقَدْ فَازَ ۗ وَمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا إِلَّا مَتَاعُ الْغُرُورِ ۝١٨٥
Kulu nafsin zaaa`iqatul mawt; wa innamaa tuwaffawna ujoorakum Yawmal Qiyaamati faman zuhziha `anin Naari waudkhilal Jannata faqad faaz; wa mal hayaatud dunyaaa illaa mataa`ul ghuroor
📖 Tekkim Wolof
Bakkan bu nekk dana tàqamtiku [mos] dee. Waaye dangeen jot seen pey ca Bis-pénc ba. Ku ñu soreel Safara ba, dugal ko Àjjana, texe na. Te dundug àddina gi du dara lu dul xéewal guy naxe [naxti ndaw].
🎧 Dégg

📜 Aaya 183-187 — Aali Imran

183الَّذِينَ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ عَهِدَ إِلَيْنَا أَلَّا نُؤْمِنَ لِرَسُولٍ حَتَّىٰ يَأْتِيَنَا بِقُرْبَانٍ تَأْكُلُهُ النَّارُ ۗ قُلْ قَدْ جَاءَكُمْ رُسُلٌ مِّن قَبْلِي بِالْبَيِّنَاتِ وَبِالَّذِي قُلْتُمْ فَلِمَ قَتَلْتُمُوهُمْ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Yàlla dégg na ña wax ne : “Yàlla kóllarante na ak nun, te ne duñu gëm benn Yonent li feek indilunu yool boo xam ne safaraa koy lekk”. - Neel : “Ay Yonent dikkaloon na leen jiitu ma, indiwaale woon lay yu leer nàññ ak la ngeen laaj. Su fekkee ñu dëggu ngeen, lu tax ngeen rey leen” ?
184فَإِن كَذَّبُوكَ فَقَدْ كُذِّبَ رُسُلٌ مِّن قَبْلِكَ جَاءُوا بِالْبَيِّنَاتِ وَالزُّبُرِ وَالْكِتَابِ الْمُنِيرِ
Suñu la weddee, xamal ne weddi woon nañu ay Yonent yu la jiitu. Indi woon nañu ay lay yu leer ak [Zabuur] ak Téere bu leer.
185كُلُّ نَفْسٍ ذَائِقَةُ الْمَوْتِ ۗ وَإِنَّمَا تُوَفَّوْنَ أُجُورَكُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۖ فَمَن زُحْزِحَ عَنِ النَّارِ وَأُدْخِلَ الْجَنَّةَ فَقَدْ فَازَ ۗ وَمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا إِلَّا مَتَاعُ الْغُرُورِ
Bakkan bu nekk dana tàqamtiku [mos] dee. Waaye dangeen jot seen pey ca Bis-pénc ba. Ku ñu soreel Safara ba, dugal ko Àjjana, texe na. Te dundug àddina gi du dara lu dul xéewal guy naxe [naxti ndaw].
186۞ لَتُبْلَوُنَّ فِي أَمْوَالِكُمْ وَأَنفُسِكُمْ وَلَتَسْمَعُنَّ مِنَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ مِن قَبْلِكُمْ وَمِنَ الَّذِينَ أَشْرَكُوا أَذًى كَثِيرًا ۚ وَإِن تَصْبِرُوا وَتَتَّقُوا فَإِنَّ ذَٰلِكَ مِنْ عَزْمِ الْأُمُورِ
Fàwwu dees na leen nattu ci seeni alal ak ci seeni bakkan ; dangeen dégge ca ñoñ-téere ya leen jiitu woon ak bokkaalekat ya, wax yu ñaaw yu bari.Waaye, bu ngeen muñee te ragal Yàlla... mooy sabab duggu gay tax mbir ya sotti.
187وَإِذْ أَخَذَ اللَّهُ مِيثَاقَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ لَتُبَيِّنُنَّهُ لِلنَّاسِ وَلَا تَكْتُمُونَهُ فَنَبَذُوهُ وَرَاءَ ظُهُورِهِمْ وَاشْتَرَوْا بِهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۖ فَبِئْسَ مَا يَشْتَرُونَ
[Fàttalikul] ba Yàlla kóllaranteek ña jot Téere, ne : “Nangeen ko leeralal nit ñi te buleen ko nëbb”. Ñu sànni ko ca seen ginnaaw, jaaye ko njëg gu néew. Ndax njëg gu bon !
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
185Aaya

Tekki — Aali Imran 185

Simoore Aali Imran Aaya 185 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bakkan bu nekk dana tàqamtiku [mos] dee. Waaye dangeen jot…

Simoore Aaya 185/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 183–187. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers