Aali Imran · 22/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
أُولَٰئِكَ الَّذِينَ حَبِطَتْ أَعْمَالُهُمْ فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ وَمَا لَهُم مِّن نَّاصِرِينَ ۝٢٢
Ulaaa`ikal lazeena habitat a`maaluhum fid dunyaa wal Aaakhirati wa maa lahum min naasireen
📖 Tekkim Wolof
Ñooña seeni jëf sippiku na ci àddina ak ca àllaaxira. Te duñu am ndimbal !
🎧 Dégg

📜 Aaya 20-24 — Aali Imran

20فَإِنْ حَاجُّوكَ فَقُلْ أَسْلَمْتُ وَجْهِيَ لِلَّهِ وَمَنِ اتَّبَعَنِ ۗ وَقُل لِّلَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ وَالْأُمِّيِّينَ أَأَسْلَمْتُمْ ۚ فَإِنْ أَسْلَمُوا فَقَدِ اهْتَدَوا ۖ وَّإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّمَا عَلَيْكَ الْبَلَاغُ ۗ وَاللَّهُ بَصِيرٌ بِالْعِبَادِ
Bu ñuy dàggasante ak yaw, neel : “Ci Yàlla laa jublu maak ku ma topp”. Te nga wax ñoñ- téere, ak ña jàngul : “Moo ndax yéen wommatu ngeen ? ” Bu ñu tàbbee ci Lislaam, nga xam ne gindiku nañu. Bu ñu dummóoyoo nag... Yaw [Muhammad] jotal rekk la ci war. Yàllaa ngi gis jaam ñi.
21إِنَّ الَّذِينَ يَكْفُرُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ وَيَقْتُلُونَ النَّبِيِّينَ بِغَيْرِ حَقٍّ وَيَقْتُلُونَ الَّذِينَ يَأْمُرُونَ بِالْقِسْطِ مِنَ النَّاسِ فَبَشِّرْهُم بِعَذَابٍ أَلِيمٍ
Ñay weddi kàdduy Yàlla, di rey Yonent ya, ci lu dul dëgg, di rey ñay digle maandute ci nit ñi, na nga leen bégal ci mbugalmu tar.
22أُولَٰئِكَ الَّذِينَ حَبِطَتْ أَعْمَالُهُمْ فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ وَمَا لَهُم مِّن نَّاصِرِينَ
Ñooña seeni jëf sippiku na ci àddina ak ca àllaaxira. Te duñu am ndimbal !
23أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ أُوتُوا نَصِيبًا مِّنَ الْكِتَابِ يُدْعَوْنَ إِلَىٰ كِتَابِ اللَّهِ لِيَحْكُمَ بَيْنَهُمْ ثُمَّ يَتَوَلَّىٰ فَرِيقٌ مِّنْهُمْ وَهُم مُّعْرِضُونَ
Moo ndax gisoo ñañu jox cér ca téere ba , woowees na leen jëme ci Téere Yàlla bi ngir mu àtte seeni diggante ; am kurél ci ñoom bu dummóoyu, far ñoom ñépp dummóoyu.
24ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ قَالُوا لَن تَمَسَّنَا النَّارُ إِلَّا أَيَّامًا مَّعْدُودَاتٍ ۖ وَغَرَّهُمْ فِي دِينِهِم مَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Ndax ñoom dañuy wax ne : “Safara dunu laal lu dul ay bis yuñu lim”. Dañuy duural Yàlla ci seen diine, loolaa leen nax.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
22Aaya

Tekki — Aali Imran 22

Simoore Aali Imran Aaya 22 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñooña seeni jëf sippiku na ci àddina ak ca àllaaxira.…

Simoore Aaya 22/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 20–24. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers