Aali Imran · 54/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
وَمَكَرُوا وَمَكَرَ اللَّهُ ۖ وَاللَّهُ خَيْرُ الْمَاكِرِينَ ۝٥٤
Wa makaroo wa makaral laahu wallaahu khairul maakireen
📖 Tekkim Wolof
Ñu tëral pexe. Yàlla it tëral pexe. Te Mooy gën jaa mën a tëral pexe !

🎧 Dégg


📜 Aaya 52-56 — Simoore Aali Imran

52۞ فَلَمَّا أَحَسَّ عِيسَىٰ مِنْهُمُ الْكُفْرَ قَالَ مَنْ أَنصَارِي إِلَى اللَّهِ ۖ قَالَ الْحَوَارِيُّونَ نَحْنُ أَنصَارُ اللَّهِ آمَنَّا بِاللَّهِ وَاشْهَدْ بِأَنَّا مُسْلِمُونَ
Ba Iisaa ràññee ca ñoom gëmëdi, la daldi wax ne : “Waaw ana kan moo may dimbali ci liggéeyal Yàlla ? ” Gaa yu sell ya ne ko : “Nun noo lay dimbali ci yoonu Yàlla. Gëm nanu Yàlla. Seedeel ne nun way-wommatu lanu [jëm ci Yàlla].
53رَبَّنَا آمَنَّا بِمَا أَنزَلْتَ وَاتَّبَعْنَا الرَّسُولَ فَاكْتُبْنَا مَعَ الشَّاهِدِينَ
Yaw sunu Boroom ! Gëm nanu li nga wàcce [Linjiil] te topp nanu Yonent bi [Iisaa]. Yàlla nanga dogal nu bokk ca seede yu dëggu ya”.
54وَمَكَرُوا وَمَكَرَ اللَّهُ ۖ وَاللَّهُ خَيْرُ الْمَاكِرِينَ
Ñu tëral pexe. Yàlla it tëral pexe. Te Mooy gën jaa mën a tëral pexe !
55إِذْ قَالَ اللَّهُ يَا عِيسَىٰ إِنِّي مُتَوَفِّيكَ وَرَافِعُكَ إِلَيَّ وَمُطَهِّرُكَ مِنَ الَّذِينَ كَفَرُوا وَجَاعِلُ الَّذِينَ اتَّبَعُوكَ فَوْقَ الَّذِينَ كَفَرُوا إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ ۖ ثُمَّ إِلَيَّ مَرْجِعُكُمْ فَأَحْكُمُ بَيْنَكُمْ فِيمَا كُنتُمْ فِيهِ تَخْتَلِفُونَ
Fàttalikul ba Boroom ba waxee ne : "Yaw Iisaa, danaa la faat, yékkati la jëme ci Man, Danaa la laabal ci bon-boni yéefar yi weddi te danaa def ña la topp ñu féete kaw ña la weddi ba Bis-pénc ba. Yéen ñépp dellu ci Man, Ma àtte seeni diggante ci li ngeen doon juuyoo.
56فَأَمَّا الَّذِينَ كَفَرُوا فَأُعَذِّبُهُمْ عَذَابًا شَدِيدًا فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ وَمَا لَهُم مِّن نَّاصِرِينَ
Ña nga xam ne dañoo weddi, danaa leen mbugal mbugal mu tar, ci àddina ak ca àllaaxira ; te duñu am ku leen dimbali.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
54Aaya

Tekki — Aali Imran 54

Simoore Aali Imran Aaya 54 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñu tëral pexe. Yàlla it tëral pexe. Te Mooy gën…

Simoore Aaya 54/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 52–56. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers