Fatir · 14/45
Tekki Waxtaan — Fatir
إِن تَدْعُوهُمْ لَا يَسْمَعُوا دُعَاءَكُمْ وَلَوْ سَمِعُوا مَا اسْتَجَابُوا لَكُمْ ۖ وَيَوْمَ الْقِيَامَةِ يَكْفُرُونَ بِشِرْكِكُمْ ۚ وَلَا يُنَبِّئُكَ مِثْلُ خَبِيرٍ ۝١٤
in tad`oohum laa yasma`oo du`aaa`akum wa law sami`oo mas tajaaboo lakum; wa Yawmal Qiyaamati Yakfuroona bishirkikum; wa laa yunabbi`uka mislu khabeer
📖 Tekkim Wolof
Bu ngeen leen di woo, duñu leen dégg ; bu ñu leen déggoon it, duñu leen tontu. Bu Bis- pénc baa, danañu teggi ba mu set li ngeen ko doon bokkaale. Amul kenn ku la mën a jox xibaar yu wére nii.
🎧 Dégg

📜 Aaya 12-16 — Fatir

12وَمَا يَسْتَوِي الْبَحْرَانِ هَٰذَا عَذْبٌ فُرَاتٌ سَائِغٌ شَرَابُهُ وَهَٰذَا مِلْحٌ أُجَاجٌ ۖ وَمِن كُلٍّ تَأْكُلُونَ لَحْمًا طَرِيًّا وَتَسْتَخْرِجُونَ حِلْيَةً تَلْبَسُونَهَا ۖ وَتَرَى الْفُلْكَ فِيهِ مَوَاخِرَ لِتَبْتَغُوا مِن فَضْلِهِ وَلَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Ñaari géej ya yemuñu : gii dafa neex a naan te lewet domm, gee saf xorom te naqari. Ngeen di ca génnee aw yàpp wu tooy di ko lekk, ngeen di ca génne itam gànjar gu ngeen di sol. Nga gis gaal ya di jax ca biir ngir sàkku ci ay xéewalam. Ak it ndax amaana ngeen sant.
13يُولِجُ اللَّيْلَ فِي النَّهَارِ وَيُولِجُ النَّهَارَ فِي اللَّيْلِ وَسَخَّرَ الشَّمْسَ وَالْقَمَرَ كُلٌّ يَجْرِي لِأَجَلٍ مُّسَمًّى ۚ ذَٰلِكُمُ اللَّهُ رَبُّكُمْ لَهُ الْمُلْكُ ۚ وَالَّذِينَ تَدْعُونَ مِن دُونِهِ مَا يَمْلِكُونَ مِن قِطْمِيرٍ
Mooy dugal guddi ci bëccëg, di dugal bëccëg ci guddi. Di tàggat jant beek weer wi. Lu ca nekk a ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal. Kooku moo di Yàlla : seen Boroom moo moom nguur, te li ngeen di jaamu bàyyi ko, amuñu sax lu tollu ni kem mbuusum xooxu tàndarma.
14إِن تَدْعُوهُمْ لَا يَسْمَعُوا دُعَاءَكُمْ وَلَوْ سَمِعُوا مَا اسْتَجَابُوا لَكُمْ ۖ وَيَوْمَ الْقِيَامَةِ يَكْفُرُونَ بِشِرْكِكُمْ ۚ وَلَا يُنَبِّئُكَ مِثْلُ خَبِيرٍ
Bu ngeen leen di woo, duñu leen dégg ; bu ñu leen déggoon it, duñu leen tontu. Bu Bis- pénc baa, danañu teggi ba mu set li ngeen ko doon bokkaale. Amul kenn ku la mën a jox xibaar yu wére nii.
15۞ يَا أَيُّهَا النَّاسُ أَنتُمُ الْفُقَرَاءُ إِلَى اللَّهِ ۖ وَاللَّهُ هُوَ الْغَنِيُّ الْحَمِيدُ
Éy yéen nit ñi, yéen ay soxlaa woo Yàlla, waaye Yàlla moom Ku doylu la ci boppam, di Yeyoowaakoonu cant.
16إِن يَشَأْ يُذْهِبْكُمْ وَيَأْتِ بِخَلْقٍ جَدِيدٍ
Su ko neexoon Mu yóbbu leen, indi ñeneen mbindeef yu bees.
FatirFihi Alxuraan
45Aaya
MeccanRevelation
14Aaya

Tekki — Fatir 14

Simoore Fatir Aaya 14 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ngeen leen di woo, duñu leen dégg ; bu…

Simoore Aaya 14/45 — Fatir فاطر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fatir Dégg, Fatir Tekki, Fatir mp3, Fatir pdf. Aaya 12–16. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers