Fatir · 15/45
Tekki Waxtaan — Fatir
۞ يَا أَيُّهَا النَّاسُ أَنتُمُ الْفُقَرَاءُ إِلَى اللَّهِ ۖ وَاللَّهُ هُوَ الْغَنِيُّ الْحَمِيدُ ۝١٥
Yaaa ayyunhan naasu antumul fuqaraaa`u ilallaahi wallaahu Huwal Ghaniyyul Hameed
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen nit ñi, yéen ay soxlaa woo Yàlla, waaye Yàlla moom Ku doylu la ci boppam, di Yeyoowaakoonu cant.
🎧 Dégg

📜 Aaya 13-17 — Fatir

13يُولِجُ اللَّيْلَ فِي النَّهَارِ وَيُولِجُ النَّهَارَ فِي اللَّيْلِ وَسَخَّرَ الشَّمْسَ وَالْقَمَرَ كُلٌّ يَجْرِي لِأَجَلٍ مُّسَمًّى ۚ ذَٰلِكُمُ اللَّهُ رَبُّكُمْ لَهُ الْمُلْكُ ۚ وَالَّذِينَ تَدْعُونَ مِن دُونِهِ مَا يَمْلِكُونَ مِن قِطْمِيرٍ
Mooy dugal guddi ci bëccëg, di dugal bëccëg ci guddi. Di tàggat jant beek weer wi. Lu ca nekk a ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal. Kooku moo di Yàlla : seen Boroom moo moom nguur, te li ngeen di jaamu bàyyi ko, amuñu sax lu tollu ni kem mbuusum xooxu tàndarma.
14إِن تَدْعُوهُمْ لَا يَسْمَعُوا دُعَاءَكُمْ وَلَوْ سَمِعُوا مَا اسْتَجَابُوا لَكُمْ ۖ وَيَوْمَ الْقِيَامَةِ يَكْفُرُونَ بِشِرْكِكُمْ ۚ وَلَا يُنَبِّئُكَ مِثْلُ خَبِيرٍ
Bu ngeen leen di woo, duñu leen dégg ; bu ñu leen déggoon it, duñu leen tontu. Bu Bis- pénc baa, danañu teggi ba mu set li ngeen ko doon bokkaale. Amul kenn ku la mën a jox xibaar yu wére nii.
15۞ يَا أَيُّهَا النَّاسُ أَنتُمُ الْفُقَرَاءُ إِلَى اللَّهِ ۖ وَاللَّهُ هُوَ الْغَنِيُّ الْحَمِيدُ
Éy yéen nit ñi, yéen ay soxlaa woo Yàlla, waaye Yàlla moom Ku doylu la ci boppam, di Yeyoowaakoonu cant.
16إِن يَشَأْ يُذْهِبْكُمْ وَيَأْتِ بِخَلْقٍ جَدِيدٍ
Su ko neexoon Mu yóbbu leen, indi ñeneen mbindeef yu bees.
17وَمَا ذَٰلِكَ عَلَى اللَّهِ بِعَزِيزٍ
Te loolu du lu jafe ci Yàlla.
FatirFihi Alxuraan
45Aaya
MeccanRevelation
15Aaya

Tekki — Fatir 15

Simoore Fatir Aaya 15 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen nit ñi, yéen ay soxlaa woo Yàlla, waaye…

Simoore Aaya 15/45 — Fatir فاطر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fatir Dégg, Fatir Tekki, Fatir mp3, Fatir pdf. Aaya 13–17. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers