An-Nisa · 119/176
Tekki Waxtaan — Simoore An-Nisa
وَلَأُضِلَّنَّهُمْ وَلَأُمَنِّيَنَّهُمْ وَلَآمُرَنَّهُمْ فَلَيُبَتِّكُنَّ آذَانَ الْأَنْعَامِ وَلَآمُرَنَّهُمْ فَلَيُغَيِّرُنَّ خَلْقَ اللَّهِ ۚ وَمَن يَتَّخِذِ الشَّيْطَانَ وَلِيًّا مِّن دُونِ اللَّهِ فَقَدْ خَسِرَ خُسْرَانًا مُّبِينًا ۝١١٩
Wa la udillannahum wa la umanni yannnahum wa la aamurannahum fala yubat tikunna aazaanal lan`aami wa la aamurannahum fala yughai yirunna khalqal laah; wa mai yattakhizish Shaitaana waliyyam mmin doonil laahi faqad khasira khusraanam mubeena
📖 Tekkim Wolof
Mu waxaat [moom Séytaane] : “Waat naa ne danaa leen réeral, danaa leen nax ca la ñuy xemmem, danaa leen digal ñu dog noppi jur gi, danaa leen sant ñu soppi ni Yàlla bindee [bindeef yi]. Ku bàyyi Yàlla, jàppe Séytaane muy kilifaam, yàqule na yàqule gu bir.

🎧 Dégg


📜 Aaya 117-121 — Simoore An-Nisa

117إِن يَدْعُونَ مِن دُونِهِ إِلَّا إِنَاثًا وَإِن يَدْعُونَ إِلَّا شَيْطَانًا مَّرِيدًا
Te kat ñoom ay xërëm yu ñu jigéenal ak Séytaane su fétterlu doŋŋ lañuy jaamu di ko woo bàyyi Yàlla.
118لَّعَنَهُ اللَّهُ ۘ وَقَالَ لَأَتَّخِذَنَّ مِنْ عِبَادِكَ نَصِيبًا مَّفْرُوضًا
Yàlla rëbb na ko ca la mu wax moom [Séytaane], ne : “Fàwwu danaa jël ci say jaam ab cër bu takku”.
119وَلَأُضِلَّنَّهُمْ وَلَأُمَنِّيَنَّهُمْ وَلَآمُرَنَّهُمْ فَلَيُبَتِّكُنَّ آذَانَ الْأَنْعَامِ وَلَآمُرَنَّهُمْ فَلَيُغَيِّرُنَّ خَلْقَ اللَّهِ ۚ وَمَن يَتَّخِذِ الشَّيْطَانَ وَلِيًّا مِّن دُونِ اللَّهِ فَقَدْ خَسِرَ خُسْرَانًا مُّبِينًا
Mu waxaat [moom Séytaane] : “Waat naa ne danaa leen réeral, danaa leen nax ca la ñuy xemmem, danaa leen digal ñu dog noppi jur gi, danaa leen sant ñu soppi ni Yàlla bindee [bindeef yi]. Ku bàyyi Yàlla, jàppe Séytaane muy kilifaam, yàqule na yàqule gu bir.
120يَعِدُهُمْ وَيُمَنِّيهِمْ ۖ وَمَا يَعِدُهُمُ الشَّيْطَانُ إِلَّا غُرُورًا
Dana leen dig, xemmemlu leen. Te Séytaane du dige lu dul ay wor.
121أُولَٰئِكَ مَأْوَاهُمْ جَهَنَّمُ وَلَا يَجِدُونَ عَنْهَا مَحِيصًا
Ñooñu seeni dëkkuwaay mooy Safara. Te kenn duleen ca musal !
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
119Aaya

Tekki — An-Nisa 119

Simoore An-Nisa Aaya 119 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu waxaat [moom Séytaane] : “Waat naa ne danaa leen…

Simoore Aaya 119/176 — Simoore An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore An-Nisa Dégg, Simoore An-Nisa Tekki, Simoore An-Nisa mp3, Simoore An-Nisa pdf. Aaya 117–121. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers