An-Nisa · 133/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
إِن يَشَأْ يُذْهِبْكُمْ أَيُّهَا النَّاسُ وَيَأْتِ بِآخَرِينَ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَلَىٰ ذَٰلِكَ قَدِيرًا ۝١٣٣
Iny-yashaa yuzhibkum aiyuhan naasu wa yaati bi aakhareen; wa kaanal laahu `alaa zaalika Qadeeraa
📖 Tekkim Wolof
Bu ko sooboon Mu jële leen fi, yéen nit ñi, indi fi ñeneen. Te loolu, Yàlla mën na ko.

🎧 Dégg


📜 Aaya 131-135 — An-Nisa

131وَلِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۗ وَلَقَدْ وَصَّيْنَا الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ مِن قَبْلِكُمْ وَإِيَّاكُمْ أَنِ اتَّقُوا اللَّهَ ۚ وَإِن تَكْفُرُوا فَإِنَّ لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ غَنِيًّا حَمِيدًا
Te li nekk ci asamaan yeek suuf si, Yàllaa ko moom. [Nun Yàlla], déggoon Nanu ña jotoon Téere, lu jiitu seeni jamoni ak yéen it ne leen : “Ragal-leen Yàlla ! ”. Te bu ngeen weddee, nangeen xam ne Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Yàlla Ku woomal la te yayoo cant.
132وَلِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ وَكِيلًا
Te it, li nekk ci asamaan yeek suuf, Yàlla doy na ci te mat na sëkk Kilifa.
133إِن يَشَأْ يُذْهِبْكُمْ أَيُّهَا النَّاسُ وَيَأْتِ بِآخَرِينَ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَلَىٰ ذَٰلِكَ قَدِيرًا
Bu ko sooboon Mu jële leen fi, yéen nit ñi, indi fi ñeneen. Te loolu, Yàlla mën na ko.
134مَّن كَانَ يُرِيدُ ثَوَابَ الدُّنْيَا فَعِندَ اللَّهِ ثَوَابُ الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ سَمِيعًا بَصِيرًا
Koo xam ne yoolu àddina bi la bëgg, [na xam ne] Yàlla am na lu mu yoole ci àddina ak ca àllaaxira. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy gis la.
135۞ يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُونُوا قَوَّامِينَ بِالْقِسْطِ شُهَدَاءَ لِلَّهِ وَلَوْ عَلَىٰ أَنفُسِكُمْ أَوِ الْوَالِدَيْنِ وَالْأَقْرَبِينَ ۚ إِن يَكُنْ غَنِيًّا أَوْ فَقِيرًا فَاللَّهُ أَوْلَىٰ بِهِمَا ۖ فَلَا تَتَّبِعُوا الْهَوَىٰ أَن تَعْدِلُوا ۚ وَإِن تَلْوُوا أَوْ تُعْرِضُوا فَإِنَّ اللَّهَ كَانَ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرًا
Éy yéen ñi gëm ! Taxawleen temm ci maandute, di seede ngir Yàlla doonte seede soosu [lu naqari la] luy dal ci seen kaw, walla ci seeni waajur, walla ci kaw seeni njaboot, walla seeni jegeñaale. Su dee ku woomal la walla ku ñàkk, Yàllaay ki gën pey ci ñoom ñaar ñépp. Buleen topp seeni bànneex ba ñàkk a maandu. Bu ngeen jéggalee [seede] walla ngeen dëddu bañ a seede, xamleen ne Yàlla Ku deñ-kumpa la ci li ngeen def.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
133Aaya

Tekki — An-Nisa 133

Simoore An-Nisa Aaya 133 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ko sooboon Mu jële leen fi, yéen nit ñi,…

Simoore Aaya 133/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 131–135. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers